Ci alxames jeek àjjuma jii la réewum Riisi doon dalal ñaareelum ndaje mi dox ci digganteem ak réewi Afrig yi, ñu gën koo miis ci nasaraan Sommet Russie-Afrique. Ginnaaw kàddu yi fa jot a jib ci ñaari fan yii, gis nañ ni bëgg-bëggi réew yi fa teewoon mooy àddina su ñépp di jëflante te mu bañ a ànd ak xeeti nootaange yi xew léegi.
Ci atum 2019 bi la Vladimir Poutine jëkkoon a woote ndaje mi. Yàggul dara mbas mi tëj àddina si. Bi mbas mi jàllee, xare Ikren beek Riisi jolli. Ci 2023 mi, 27 ak 28 sulet, la Njiitu réewum Riisi li am talug wootewaat moomu ndaje. Muy ñaareel wi yoon. Jàmm, kaaraange ak suqaliku doonoon ponk yi lal waxtaan yi.
Ndajem atum ren ji nag, dafa yemook jamono yii xare Ikren bi tëe fey, réewi tugal yépp di joxoñ baaraami tuuma kii di Vladimir Poutine, ba sax CPI (Cour Pénale Internationale) dóor ko ab mandat d’arrêt. Loolu yépp terewul 49i ndawi réewi Afrig teewoon nañ fa (ay Njiiti réew ak i jëwriñ).
Ni Njiitu réewi Afrig yi wuyujee ndaje ma, noonu la kàddu yiñ fa yékkati bokkee ànd di rafetlu lënkaloo gi nekk di juddu diggante réewum Riisi ak yu Afrig yi. Naka noonu, ànd nañu biral ni Lënkaloo gi am diggante Riisi ak Afrig, lënkaloo la gu lalu ci àndu nawle.
Waaye, li gën a fés mooy seen yéeney soppi doxinu àddina si tey ba réew yépp mën a wegante. Waayeet, jaay-doole gi ñuy jiiñ réewi tugal yi mën a dakk. Ci niral, Njiitu réewum Senegaal li dafa gis ni Afrig ak Riisee ngi ci ànd bu dëggu, boole ci ubbeeku te am njariñ. Mu jàpp ni bés bu Riisi ak Afrig boolee seen doole, dina bari lool luñ mën a ànd liggéey.
« Sunu lënkaloo gii, mënees na cee jële njariñ lu bari. Ci lees jot a xam, yaatuwaayu Afrig mi ngi ci 30i tamndareeti km2. Lu ëpp 2i tamñaret ak 300i tamndareeti doom-aadama di fi yeewoo. Bu dee Risi, ëppal na 17i tamndareeti km2 boole kook lu ëpp 144i tamndareeti doom-aadama, seen booloo dafa leen di kàttanal, yokk leen doole ci àddina si. »
Nu gis ni kon jegeyante Riisi ak Afrig dina yemale doole réew yi ci àddina si bu baax. Waaye kilifa réewi Afrig yi yemuñu ci loolu. Nde, gis nañ bu baax li nekk di xew Ikren ak njeexital yi mu am ci kembaarug Afrig. Loolu tax naat ba ñuy sàkku jàmm dellusi ci àddina si te ñu delloosi njënd meek njaay mi ci anam yi mu waree.
Bu dee lu jëm ci wàllu dund gi ak pepp mi Njiitu réewum Riisi li najoon, moom Vladimir Poutine xamle na ni ñenn waraluñ ko ñu dul Saa-tugal yi. Waaye, réewum Riisi mën naa jotale ci kembaarug Afrig lépp lu ñu soxla ci pepp. Xamle na sax ni dina may pepp juróomi réewi Afrig yii di Mali, Somali, Sàntar Afrig, ak Eritere te dinañu ci tàmbalee jot fileek ñett mbaa ñeenti weer. Bu loolu weesoo, Vlaadimir Putin fésal na yéeneb dalal ndaje mi ñetti at yu nekk.