NATHALIE YAMB : “LI TAX MAKI SÀLL DELLU GINNAAW…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Altine jii weesu yemoo woon ak ñetti fan ci weeru sulet la Njiitu réew mi Maki Sàll jëloon ndogal lu am solo ci ëllëgu réewmi. Ndogal loolu nag, tontu la ci lees doon laam-laame ay at, ay weer, ay fan ci ginnaaw. Ku nekk di laaj ndax dina bokk am du bokk. Ñi fareek moom naan mooy sunu lawax. Ndax, am na sañ-sañu bokkaat. Ña fare ca beneen boor ba naan ñetteelu moome du fi ame. Moom miy ndeyi-mbill gi nee na du bokk ci wotey 2024 yi. Ñu baree ngi koy ndokkale ak a sargal ci ndogal li mu jël. Mu am nag ñeneen ñu ko gise neneen, niki Nathalie Yamb. Moom, soxna siy xeexal Panafrikanism, dafa def ab taxaw seetlu ci ndogal li.

Bi ndogalu Njiitu réew mi jibee, coow li dafa neeti kurr ci réew mi. Ñii di ko sant ak a gërëm. Ña ca des naan deful dara lu yéeme lu moy sàmmonte ak li ndeyu-àtte ji santaane. Waaye nag, bu dee wax  dëgg rekk, ndogal li dafa jële ñu bari kow. Ndax, taxawaayu Njiitu réew mi ñeel wote yii di ñëw juroon na ay sikki-sàkka yu bari. Ay kurél sax juddoo nañ ci ngir xeex ñetteelu moome bees njortoon ne bëgg na ko dagaan ci wotey 2024 yii nu dégmal. Moo tax, keroog, ba mu waree janook askan wi ngir leeral li mu nar, bari na ñu ko doon xaar mu daanu ci geneen kàmb gi. Waaye, bett na leen.

Jamono jii nag, géewu pólitig bi jaxasoo na lool, rawatina làng gii di APR. Ndax, ñu baree ngi samp ab laaj, naan kan moo ko war a wuutu ? Nde, ñoom ci seen jëmmi bopp moom lañu defoon seen lawax, yàgg ko waajal. Te, ndogal li sax, mbetteel la ci ñu bari ci ay militaŋam. Waaye, li am ba des mooy, bal ba moom tàkk na. Lan moo ko waral la ñu bari di laaj. Kii di Nathali Yamb moom, ñaari njàngat la ci def :

“Bi ci jiitu, su Maki Sàll delloo ginnaaw ci jamono jii, ara waralu ko lu dul mbooloo mu takku mi askan wi def. Dafa génn di dox ci laltu gu xonqu gu fees ak i néew, tooy ak deretu ndawi Senegaal yoo xam ne, ay takk-deram a leen rey ak sàmbaa-bóoy yi ay jegeñaaleem jël, jox leen i ngànnaay. Day génn ak ay kaso yu def lu ëpp juróom-ñaari téeméeri nit yoo xam ne, wuute gis-gis ci pólitig a tax ñu teg leen loxo. Ak Yoon, Pólis ak Sàndarmëri yu yàqu ci kanamu askan wi nga xam ne moo ci waroon a jariñoo (…). Ñaareel bi, wékku ci ñetteelu moomeg Njiitu réew mi njuumte lu mag la. Ndax, du Maki Sàllmooy noon bi dëggantaan. Noon bu mag bi mooy kurélu Françafrique gi nga xam ne, moom kenn ci seen i ndaw la (…).”

Waaye moom yemul foofu. Ndax, dafa samp ay laaj ngir xam lu tax Njiitu réew mi xaar ba jamono jii soog a jibal ndogal li, ndeem jëloon na ko laata muy am ñaareelu moome. Rax-ci-dolli lu tollu ci juróom-ñaari weer kepp des ci wote yi, lu tax ba tey amul kenn ku bokk ci ag làngam ku jóg ngir wuutu ko ci boppu réew mi ? Looloo tax moom ak ñeneen ñu mel ni moom fare ci yeneen kurél yi jàpp ne ndogal li du ag neen. Dañoo jàpp ne waa bitim-réew seen loxo génnu ci, rawatina ñi nga xam ne seen alal a ngi ci réew mi. Te, dalug réew mi ñor leen ngir seen alal mucc ak li ñu fi gis ci gaas ak soroj. Moo tax mu ni :

“Ndogalu Njiitu réew mi, Maki Sàll, li ko sabab mooy ni ko waa bitim-réew xojee. Du kiy wuutu Maki Sàll mooy coow li, waaye  wéyalug lëkkaloog Françafrique ci jamono ju am solo jii ñeel Farãs ak Ërób gu sonn ba pare am i bor yu dul jeex. Gaas ak soroju Senegaal bi warul a tàbbi ci yeneen i loxo yu moy yoy waa Ërób. Yëf yi lijjanti nañu ko ak Maki Sàll ba noppi, woññi (chiffres) yu doy waar yi xamees na leen. Te, jëwriñ ji mu dénkoon wàllum petorol bi dafa bàyyi woon ca atum 2017. Ndax, Njiitu réew mi dafa jiitaloon njariñu Farãs ci kow njariñu Senegaal.”

Kon, yëf yi ñaar la. Ñii dañoo jàpp waa bitim-réew ñoo ko mayul mu def lu ko soob. Ñee jàpp ne, ni askan wi di booloo ak ni kurél yi booloo ci jamono jii moo tax mu dellu ginnaaw. Lu ci mën di am li mu def la ndeyu-àtte ji wax. Sikki-sàkka amatul ci ne du bokk ci joŋante boobu. Léegi, jàkka jaa ngi noonu. Dees na xam kuy noddu weeru féewaryee 2024 bu soobee Yàlla.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj