Doon nañu amal ci altiney barki-démb ji, 6eelu ndaje mu mag mu ndisoog AMCOW giy doxal. AMCOW (Conseil des ministres africaines chargés de l’eau) di ndajem jëwriñi ndox mi fi Afrig.
Bokk na ci xibaar ya fa tukkee te sunuy naataango yu APS biral leen, Senegaal dina wuutu Esipt ci boppu kurél googu, ci ñaari at yii ñu dëgmal. Coppite googu nag, bees sukkandikoo ci li jëwriñu ndox meek wàllu ngaareew mi (canalisation / assainissement) xamle, doon na luy firndeel doxin wu yees ci lëkkatoog réewi Afrig yi jëme ci soxla yi aju ci ndox mi ak ngaareew mi. Waaye itam, ñu jiital ci yorin wu méngoo ak gis-gis bu sori ñeel ballukaayu yolaan yi ak ndox mu sell mi ñépp war a jot.