Gaawu gii weesu, yemoo woon ak ñaar-fukki fan ak benn ci weeru oktoobar wii, lañu doon aajar téereb nettali bii di Tànn-béer. Ngoti Faal mees gën a xamee ci turu Làmp Faal Kala mooy aji-bind ji, EJO a ko móol. Ndajem kaajar mi nag, fa Institut français bu Ndar lañ ko defee. Paap Aali Jàllo moo doon aajar téere bi, di ko faramfàcce ci kàllamaay tubaab ak wolof. Waaye, lu ko jiitu ak li ci topp yépp, amoon nay xumbaay ak seede yu am solo yees fa jibal ñeel bindkat bi ak it kër gi móol téere bi, maanaam Editions EJO.
Keroog, Institut français xumboon na lool. Foo sàndi woon mbàttu mu tag Yàllaak nit ñu bari. Nde, mbooloo mu baree wuyusi woon wooteb Làmp Faal bi. Ñii ay mbokkam lañu, ñee di ay xaritam ak i am-di-jàmmam. Ñale di ay mbokki jàngalekatam, ñeneen ñ ca des diy ndongo yu bawoo ca jàngune bu Ndar ba ak ci yeneen daara yu suufe yi ak yu digg-dóomu yi. Moom kay, mbokki baay faalam yi sax wuutewuñ ko. Te sax, def nañ fa liggéey bu rafet. Kenn fàttewul it kibaraan ya fa teewoon, muy teley RTS ak Itv ak rajoy RFM ak Sudfm. Kon, ku teewewul woon ca xew-xew ba sax, war naa xam ne alaa-dawme woon na.
Institut français bu Ndar dinay faral di amal i xew-xew yu ni mel gaa, waaye guléet mu dalal am ndajem kaajaar ñeel téere bob, ci wolof lees ko taalif. Rax-ci-dolli, la fa Làmp Faal def ak i àndandoom, mësuñu ko fa gis. Solos ndaje ma nag, kenn waxaalewu ko.
Aji-bind ji, Làmp Faal Kala, ab jàngalekat la ci daara yu digg-dóomu yi. Làkkuw àngale la fay jàngale. Waaye, bindkat bu xarañ la, yor xalima bu ñaw ak xel mu nangu. Ñi ko xam ñépp ñooy yàkkamti ubbi téereem ndax neexaayu mbindam, solo si ci nekk ci wàllu jàngale, yeete, mbatiit, cosaan ak mboor yi muy jëmmal. Tànn-béer mooy ñaareelu téereem. Ndax, Xelum Xalam, téere taalif bu solowu, la jëkk a móol-lu fa EJO. Te, li ci gën a neex mooy, ñaar yépp ci làmmiñu wolof la leen binde. Tànn-béer itam, EJO a ko génne. Moo tax, Paap Aali Jàllo, aajarkat bi, bokk tamit ci EJO, sànni fa kàdduy seede yii toftalu :
“ Atum 2018 la EJO juddu. Werekaan bii di Bubakar Bóris Jóob moo ko taxawal, Soxna Ndey Koddu Faal jiite ko. Bi ñu ko sosee ak léegi, EJO móolagum na fi fukki téere ak juróom ci fànn yu wuute, yépp ñu bind leen ci wolof. Muy liggéey bu réy ñeel làkk ak mbatiitu Afrig, rawatina Senegaal. Kon, gàcce-ngaalaama Bubakar Bóris Jóob mi nga xam ne, alalu boppam la ciy def te xaaru ci dara walla kenn. Ngërëm ñeel na Soxna Ndey Koddu Faal mi jiite kër gi di ci def liggéey bu mucc ayib.”
Boroom bés bi tamit, feddali na kóllëre gi dox diggam ak waa EJO, rawatina Bubakar Bóris Jóob mi ko tàllal loxo, xelal téereem bu mujj bii. Daf ne :
“Mënuma bañ a gërëm EJO ak baay Bóris. Ndax, téere taalif bi ma jëkk a bind [Xelum xalam], ñoo ko móol laata ñu may génneel Tànn-béer. EJO mooy këru móolukaay téere boo xam ne, daf lay génneel sa téere te du la laaj dërëm ! Te, liggéey bu mucc ayib lañ lay defal. Ñoo ngi séqiy jéego yu am a am solo ci làkki réew mi, di bay seen waar ci toolu mbatiit. Warees na leen delloo njukkal, sargal leen.”
Muy kàdduy seede yu rafet yoy, EJO yelloo na leen.
Ndaje maa nga dooroon boori juróomi waxtu jàpp juróom-benni waxtu ca ngoon. Ginnaaw kàdduy nuyoo yi, gërëmaate yi ak seede yi, Soxna Aadama Puy mi doon séddale kàddu gi daf ko jox Paap Aali Jàllo ngir mu aajar téere bi.
Moom, Paap Aali Jàllo, leeral na wëppa yu bari ci téere bi ak li mu làmboo ci ay njàngale. Muy ci wàlluw cosaan, mbatiit, mboor, añs. Ci ag faram-fàcceem, dafa jëkk a toj boppu téere bi, di baatu “tànn-béer” :
“ Jamonoy tey, boo nee “tànn-béer”, xel yépp ay dem ci tëgg ak fecc, xeeti caaxaan yooyu. Waaye, jële nanu ci sunu benn jàngalekat ne, cosaanu baatu “tànn-béer” mooy “tànn bu wér”. Muy wone ne, li baat bi wund jéggi na maanaa bees koy jox. Kon, bu Làmp Faal tànnee baat bii, tuddee ko téereem, du ab tandle. Xam na xéll li mu ci jublu.”
Ginnaaw bim leeralee cosaanu baat bi, Sëñ bi Jàllo dafa jublu ci téere bi, tënk.
“ Tànn-béer ab nettali la ñeel ñaari kër, gog Baay Xaali miy géer ak gog Algaf miy géwalu juddu Baay Xaali, nekkoon xaritu benn bakkanam. Seen ñaari doom yi, Farba ak Mbaaco ñoo bëggante ba dof. Waaye, bi Farba nisëree takk Mbaaco ba xamal ko Baay Xaali, ngóor si dafa bañ, wax ne géer ak géwél duñu séy. Loolu metti lool Farba ndax fu baayam ji dëddu jaar ak Baay Xaali yépp, mësul foog ne dina ko toroxalee nii. Baay Xaali daldi may Mbaaco kii di Meysa Wàdd. Waaye, dañuy mujje tas, Farba daldi takk Mbaaco ci njeexitalu nettali bi.”
Ginnaaw tënk bi, wax na njàngale yi téere bi ëmb, ni téere biy melalee mboolaayu wolof ak ni muy duutee baaraam jikko yu ñaaw ak réer giy màndargaal ñuuley tey yi fàtte seen démb. Làmp Faal moyul benn yoon ñaawteefi way-mbéeféer ya, ndax fàttali na ci téere bi àllarbay Ndaayaan, di xew-xew bu tiis te làmboo naqar. Ngoti Faal ŋàññ na tamit doxalinu way-pólitig yi jiite sunu réew yi, feeñal mbonte ak yàqute yi ci mbaali jokkoo yi.
Bi Paap Aali noppee, am nay taalifkat yu jàll, def fa lu dara jarul. Baay Faal yi tamit tëgg nañ fa tëgg yu neex te xumb. Làmp Faal Kala ci boppam wone na fa lenn ci ay mëniinam. Ndekete, ku bariy feem la, ndaanaan bi. Ndax, dafa tànn ay jukki ci téere bi woyaale leen. Dafa di sax, ca ndoorte la, benn xale bu jigéen dawal na fa ab jukki.
Làmp Faal Kala jàllale na fa yit benn widewoo boo xam ne, dafay jëmmal pàccub Nawet bi aji-bind ji ubbee téerem. Pàcc boo xam ne, tekki nañu ko ci àngale. Ginnaaw loolu ca la ndaje ma tas. Waaye, joxante nañ dig-daje fa jànguneb Ndar ngir amal fa meneen ndajem kaajaar bu gënatee xumb, nar cee ànd ak waa Kàggug jàngune Ndar bi (Bibliothèque Universitaire de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis) ak ndongoy banqaasu Làkk ak Caaday Afrig. Nar naa nekk bés bu réyati. Waaye, wolof nee na, bés du réy du tuuti, boroom lay tollool.