NDAJEM MBOOTAAYU ÀTTEKATI SENEGAAL YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbootaayu àttekati Senegaal yi, ñu gën koo xam ci turu UMS (Union des Magistrats du Sénégal) amal na ndajeem mu mag démb ci gaawu gi. Muy ndaje mu ràññeeku ndax liñ ko àppal wenn fan ginnaaw ndajem CSM (Conseil Supérieur de la Magistrature) mi.

Ginnaaw ndajem CSM (Conseil Supérieur de la Magistrature) mi ñu amal bërki-démb ci àjjuma ji ak coppite yu am solo yees fa nemmeeku, Mbootaayu Àttekati Sénégaal mee ngi doon na amal ndajem tey ci gaawug démb gi. Seen ndaje moomu sax, ñaŋ ko daan amal ci diirub ñaari pani njeexitu ayu-bes bi (gaawu ak dibéer). Waaye, mu ren ji, dañ ko yemale ci wenn fan kepp (gaawu 10 ut 2024) ndax li ñu jotul ndimbal li daan jóge ci Nguur gi. Naka noonu, ñu dellu tuxal ko Sali gañ ko jàppoon (Mbuur), yóbbu ko King Fahd Palace (Ndakaaru).

Ca seen ndaje ma nag, mbootaay mi dellusi na ci taxawaayu Ndajem Ndayu Sàrti Réew mi (Conseil constitutionnel) ñeel wotey Njiitu réew mi fi amoon ak coow yi ci laxasu woon. Ba tax mbootaayu masistaraa yi dellu ci seen bés bi doon njukkal way-bokki ëttu àttewaay bu mag boobu.

« Ñépp teg nañ seen bët ci li way-bokki Ndajem Ndayu Sàrti Réew mi def. Ci jamonoy pólitig ju metti lañ jóge te Senegaal yaakaarul woon ñu dul ñoom. Mënoon nañ am taxawaay bu ñu xañ jàmm ji ñu am tey. » (Usmaan Simeer Juuf, Njiitu UMS)

Delloo nañ fa njukkal itam ñii di Soxna Kayre Sow Faal ak Sëñ Bubakar Albeer Gay ci jëf yu am solo yu ñu amal ci fépp fu ñu mës a jaar ci seen diiru liggéey.

Bu dee lu jëm ci CSM bi, mbootaay mi àndul wenn yoon ci génnug Njiitu réew mi, ndeem  moom mooy xaatim dekkare yi. Àndul itam ci tàbbal ku dul masistaraa ci biir CSM, nees ko waxtaane woon ci péncoo mii weesu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj