Coowal DPG li ba tey jeexagul. Nde, ndeyu-mbill ji, Usmaan Sonko, dafa am ay sàrt yu mu tegoon, wax ne bu Ngomblaan gi soppiwul seen càrt gi, du def DPG bi.
Ginnaaw loolu, coow lu bari amoon na ci. Waaye, mel na ni déggoo a ngi waaj a am. Ndax, ñetti njiiti kippaangoy dépite yi, Ayib Dafe (YAW), Abdu Mbów (BBY) ak Lamin Caam (Wallu) amaloon nañu am ndaje. Li ñu ko dugge woon mooy am saafara ci coowal DPG li. Ñoom nag, déggoo nañu ci amal coppite yi war. Li ci des kay mooy njiitu Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob, woote aw waxtaan fa béréb boobu, ñu mën a càmbar mbir mi.