NDAJEM NJIITI NGOMBLAANI RÉEW YI XARITOOK PALESTIN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci àjjuma ji, Njiitu Ngomblaan gi, Allaaji Maalig Njaay, moo nga woon fa réewum Tirki ngir teewe ndajem Njiiti Ngomblaani réew yi xaritook réewum Palestin.

Barki-démb, ci alxames ji, la fi Allaaji Maalig Njaay, Njiitu Ngomblaan gi, jóge woon, wutali réewum Tirki. Danu fa doon amal, démb ci àjjuma ji (18i awril 2025), am ndaje mom, Njiiti Ngomblaani réew yi xaritook réewum Palestin waroon nañu koo teewe. Lees ci jublu woon nag mooy yokk seen ug jàppale ci pólitig, ci jëflante réew yi ak ci ndimbal doom-aadama ñeel askanu Palestin.

Ca kàddu ya mu fa yëkkati, Sëñ Allaaji Maalig Njaay dellu na feddali li mës a doon taxawaayu Senegaal ñeel jàmm ju dellu ca diiwaan booba ñuy duppe Proche-Orient. Naka noonu, muy woote, ni mu ko defe woon bu yàggul dara bi mu demee fa réewum Ouzbékistan, ngir nu dakkal ci saa si xare bi, jotaleek ma-xejj yi ndimbalu doom-aadama yi ñu leen jagleel, ak taxaw temm ci yoonu jàmmu diiwaan booba. Muy ab woote jëme ciy jëf te àndandoo ci ñeel xeex bi ñuy xeex ba àddina sépp nangul Réewum Palestin amam. Daf ne :

“Dafa war ci nun, nu jëf. Te, jëf ji dafay dellu ci ñaawlu, waaye itam di def ak a dindi ba ñépp mën cee teg seen i bët. Looloo tax nuy rafetlu taxawaayu ngomblaan yii ak di ci am yaakaar. Dafa ubbi yoonu diisoo, lëkkatoo ak àndandoo ciy jëf yu ñeel jàmm ju tegu ci Yoon, ju yàgg te sàmmonteek àq ak yelleefi képp ku nekk. Sunu (Senegaal) taxawaayu démb mooy sunu taxawaayu tay. Taxawaay buy dellu la ci pexey taxawal ñaari réew yu bokk dëkk ci jàmm, bokk benn dig ci kaaraange te ku nekk nangul sa moroom amam.”

Njiitu Ngomblaanug Senegaal li di am yaakaar jàmm ji dellusi fa diiwaan booba. Waaye, bees ko déggee bu baax, dina jafe ñu yegg fa bu fekkee ni xaajaloo dafay wéy di am, walla taxawu yi ñu ciy amal àndut ak yéeney dakkal yi gën a xóot ci yi waral ay wi.

Cig pàttali, Réewum Senegaal, dale ko ca Seŋoor ba ci Basiiru Jomaay Fay, dafa mës a wane péeteem ci jàppale Palestin. Looloo tax, dale ko atum 1975 ba tay, moom moo jiite pekk gees sosoon ngir mataleg àq ak yelleef yi ñeel askanuw Palestin.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj