Wakaateer yu jànguney Senegaal yi yékkati nañ seen baat, biral i kàddu. Ñuy sàkku ci kilifay réew mi ñu jël 1 500i jàngalekat ci atum 2024-2025, toftal ci 500 at mu jot. Ñoo ngi sàkku itam ci Nguur gi mu xoolaat nekkiinu wakaateer yi te ñoŋal anam yi ñuy liggéeyee.
Tey, ci gaawu gi, 3i pani ut 2024, kurélug jàngalekat yi ñu duppe vacataires ci jàngune yi, di REVUS (Rassemblement des Enseignants Vacataires des Universitaires du Sénégal), doon na amal am ndaje mu mag. Ñiŋ ko doon amalandoo ci ñetti jàngune yii di UGB (Ndar), UCAD (Ndakaaru) ak UASZ (Sigicoor). Liñ ko dugge nag, mooy gindi askan wi, rawatina kilifay réew mi, ci jafe-jafe yi ñuy jànkonteel.
Ñoom jàngalekat yooyu nag, rafetlu nañu yéene ji jëwriñu njàng mu kowe mi biral ci bëgg a jël 2 500i jàngalekat ci diirub juróomi at yii di ñëw. Ginnaaw loolu, seen bëgg-bëgg mooy mu jël 1 500 yi ci atum 2024-2025 mii di ñëw. Bu ko defee, mu toftal ci 500 at mu nekk. Loolu nag, ñoo ngi ko aj ci limub ndongo yu bari yi, jàngalekat yu néew, fekk ñoom (les vacataires) ñi mën a jàngale nekk fi, bëgg ko te di ko def, kenn jëlu leen.
Ba tey ci kàddu yi ñu fésal, bari na ñuy liggéeye ci jàngune yi. Waaye, ñoom wakaateer yi, ñoo ci gën a sonn. Lu ëpp ci njàngale mi ci ñoom la wékku ba noppi liñ leen di fey néew lool. Ci li ñuy gis, junni lañu leen di fey waxtu wu nekk. Waaye, daanaka ñaari téeméeri dërëm la leen di dikke waxtu wu nekk. Ndax kat, wenn waxtu wu ñu war a jàngale dina leen dikke ñaari waxtuy waajal ak ñaar walla lu ko ëpp ciy waxtu ginnaaw kàtte yi. Muy peyoor bu néew lool bees ko gam-gamleek li ñeneen ñiy fayeeku.
Wax nañoot ni ci liggéeykati jàngune yi, ñoom kott (les vacataires) ñoo dul jot ndimbal li ñuy wax couverture sociale. Rax-ci-dolli, li ñuy feyeeku, li muy néew néew, balaa ñu ciy jot, dinañu xaar ba xàddi. Ba tax na, li leen ëppal solo mooy Nguur gi xoolaat taxawaayu wakaateer yi, ñoŋal ko te jox leen seen gëdd niki yeneen i liggéeykat yi, ba képp ku ci nekkati mën a liggéey ci anam yu mucc ayib.
Leeral nañu itam ni seen ndaje mi tekkiwul ni dafa am ku ñuy xeex. Nekkuñu feet di noonook Nguur gi walla kuréli jàngalekat yi mel ni SAES ak SUDES. Dafa fekk ni sax jéego yi ñii (SAES ak SUDES) teg ñoo tax ba Nguur gi xam luy jafe-jafey jàngune yi. Moo tax ñuy xaar ci Nguur gi mu dëggal yéeneem ak i jëf ba way-jàngune yépp gis ci seen bopp, rawatina ñoom wakaateer yi.