Tay, ci altine ji, lañu doon amal ndaje moomu. Fa béréb bii ñu dippe “Centre International de Conférences Abdou Diouf de Diamniadio” (CICAD) la doon amee. Ñi ngi ko doon amal ci teewaayu Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko. Guléet nag ñuy amal xeetu ndaje mu ni mel.
Ndaje mii ñuy dippe “Conférence des Administrateurs et Managers Publics” (CAMP) dafa am solo. Ndax, ndaje la moo xam ne, kilifa yu bari ci réew mi daje woon nañu fa. Muy li ko dale ci Njiitu réew mi, elimaanu jëwriñ yi, jëwriñ yi, añs. Li ñu dugge woon xew-xew bii mooy gën a xalaat ci nan lañu war a tabaxaatee campeef yi. Maanaam, nan lañuy gën a defaraatee banqaasi nguur gi, gën leen a ñoŋal ba ñu gën a amal réew mi ak askan wi njariñ. Nde, kenn umpalewul ne liggéeyu doxalkat yeek saytukat yi ci li ñépp bokk, du ay caaxaan.
Looloo tax Nguur gu bees gii daldi gis ne, fàww ñu amal i coppite ci ni ñuy yoree moomeelu askan wi. Rax-ci-dolli, ñoom ñi féete ci banqaas yooyu xam lan la askan wi di xaar ci ñoom. Su ko defee, ñu jéem a defe seen liggéey na mu gën a muccee ayib. Dafa di, ni campeef yiy doxee dafa am doole ci réew, rawatina bu jaaree yoon. Ndax, dafa bokk sax ci liy suqali am réew. Bu ñu sooxee nag, mooy musiba ak ci réew mu mu mën a doon.
Bu ko defee, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ci waxtaan wa mu fa doon amal, jot na leen a soññaat bu baax. Ci waxtaanam woowu nag, jot na wax ci ponk yu bari. Waaye, li ci gënoon a fés mooy sàrtuy koppar yu atum 2025, woyofalug deppãsi Càmm gi, tëralin ak doxalinu campeef yi, yorin wu mucc ayib ak caytug këru liggéey yi ñépp bokk (entremprises publiques) ak gën a yokk ag xarala ci béréb yooyu, loolu la ñuy dippe “transformation digitale dans le secteur public”. Ndax, moom Njiitu réew mi, mébétam mooy ñu def lu ñu mën ba koom gi du sooxe ci wenn wàll (kopparal, nafa). Te, fekk sooke googu dara waralu ko lu dul aw yorin wu bon. Moo tax, mu sàkku ci elimaanu jëwriñ yi mu defar toftaleg mbooleem këru liggéey yi. Su ko ko defee, ñu gën leen mën a saytu bu baax.
Waaye, laata muy tëj tamit, xamle na ne dinañu taxawal ci lu yàggul dara li ñuy dippee “système d’appel à candidatures”. Maanaam, dafa am yenn béréb yoo xam ne, bu ñu fay tabb, dañuy amal ab woote. Gaa ñi jébbal seen i wayndare, ndiiso gi ñu taxawal tànn ka ca aw wayndarem gën, ñu tabb ko ca béréb ba.
Ci gàttal, ndajem tay mi, ndajem fàttali la woon ak soññ ñeel ñi ñu teg njëwriñ yi, ci banqaas yi ak képp kuy liggéeyal askan wi. Nde, ku nekk ci ñoom dafa war a yokk cere, dolli ñeex. Te, lépp ñu teg ko ci “Jub, Jubal ak Jubbanti”. Ndax, moom bëgg-bëggam du lenn lu moy askan wi gën a gis boppam ci doxalin ak yorinu li ñépp bokk.