NDOG MU METTI FA NDÀNGALMA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndog mu metti moo am am fa Njama Faal. Njama Faal mi ngi bokk ci gox bii di Ndàngalma, nekk departmã bu Bàmbéy. Jéyya jaa ngi am ci fajaru tey jii, ay boori juróomi waxtu. Ay bakkan yu bari rot nañu ci. Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rotagum, am na tamit ñoo xam ne jële nañu ci ay gaañu-gaañu.

Ndog yi yàgg nañoo am. Waaye, jamono jii, mbir mi dafa taqarnaase. Daanaka, mëneesul a toog benn ayu-bés te joteesul ci dég-dégu ndog. Saa su ñu demee ba jàpp ne wàññeeku nañu rekk, fekk ne booba la Waalo gën a aay. Nde, bu yàggul dara rekk, laata màggal gi, nemmeeku woon nañ xeetu ndog mu ni fa Kumpentum. Lu jege fukki bakkan rotoon fa ca saa sa. Benn biis moo dalante woon ak benn minikaar. Waaye, aksidaŋ bi am tey jii, moo gën a yées. Ndax, limu bakkan ya ca rot ci saa si, dafa jéggi dayo.

Dafa di, ndog (aksidaŋ) mu tay ji tamit, genn sëfaan (camion) moo mbëkkante ak benn kaar. Fukki bakkan ak juróom-benn rot fa ci saa si. Limu ñi ci jële ay gaañu-gaañu moom ba tey, kenn biralagu ko. Li ci gën a doyati waar mooy ne kaar ba moom dafa tàkk ginnaaw ndog mi, bees sukkandikoo ci waa Seneweb. Jamono jii nag, muy kilifa yi di waa sàppëer, ñépp a nga fa béréb ba. Su ko defee, ñu mën a saytu mbir mi ba xam li ci war yépp. Nde, lii moom, dafa nekk ndog moo xam ne metti na ba fa metti yem.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj