NDOGAL YI ROTE CI “CONSEIL SUPÉRIEUR DE LA MAGISTRATURE”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey, àjjuma juróom-ñeenti fan ci weeru ut lañu doon amal ndajem CSM mi (Conseil Supérieur de la Magistrature). Mu doon ndaje moo xam ne saa-senegaal yu baree ngi ko doon xaar. Ndax, dañoo jàpp ne Nguur gu yees gi? fu mu mën a jaar dina amal ay coppite ci doxalinu Yoon. Looloo sababoon ndajem tey mii ñu doon amal fa màkkaanu Njiitu réew ma. Ndogal ya fa rotee nag, bari nañu lool. Waaye, dafa am ay tur yu ci gën a fés yoo xam ne, ñu bari ci askan wi ñi ngi leen doon xaar. Tur yooyu mooy yii ñuy lim :

Ibraayma Ndóoy, nekkoon fi layookat bu mag fa ëttub dabu (cour d’appel) bu Ndakaaru, tabb nañu ko toppekatu bokkeef gi fa ëttu àttewaay bu Ndakaaru,

Mamadu Mansuur Mbay, nekkoon fi toppekat fa ëttu àtte bu kowe ba (cours suprême), moom lañu tabb Njiitul ëttu àtte boobu,

Aamadi Juuf, nekkoon fi Njiitu ëttub dabu bi, tuxal nañu ko fa “administration centrale du ministère de la justice”,

Ibraayma Baaxum, nekkoon fi toppekat fa ëttub dabu bi, yóbbu nañu ko fa “administration centrale du ministère de la justice”,

Abdulaay Ba, nekkoon fi Njiitu “chambre à la cour d’appel” bu Cees, tabb nañu ko Njiitul ëttub dabu bu Ndakaaru,

Mbàkke Faal, nekkoon fi layookat bu mag fa ëttu àtte bu kowe bi, tabb nañu ko toppekat bu mag bi fa ëttub dabu ba,

El Haaj Abdulaay Silla, nekkoon fi layookat bu mag fa ëttu àtte bu kowe bi, tabb nañu ko toppekatu bokkeef gi ñeel kopparal,

Umar Maaham Jàllo, nekkoon fi magum àttekat yi fa ëttu àttewaay bu Ndakaaru, tabb nañu ko Njiitu “chambre à la cour d’appel” bu Tàmbaakundaa,

Abdu Kariim Jóob, nekkoon fi toppekatu bokkeef gi fa ëttu àttewaay bu Ndakaaru, tabb nañu ko layookat bu mag fa ëttub dabu bu Tàmbaakundaa,

Mamadu Sekk, nekkoon fi àttekat fa ëttu àttewaay bu Ndakaaru, tabb nañu ko layookat bu mag fa ëttu woote bu Tàmbaakundaa,

Hipolit Akedis Ndey, nekkoon fi Njiitu “chambre à la cour d’appel” bu Ndakaaru, tabb nañu ko Njiitu “chambre à la cour d’appel” bu Sigicoor,

Usmaan Raasin Coon, nekkoon fi Njiitu ëttu àttewaay bu Ndakaaru, tabb nañu ko Njiitu ëttu àttewaay bu Mbuur,

Sabasi Fay, nekkoon fi Njiitu ëttu àttewaay bu Sigicoor, tabb nañu ko Njiitu ëttu àttewaay bu Fatig,

Yoro Musaa Jàllo, nekkoon fi ndawu Nguur “agent judiciaire de l’Etat”, tabb nañu ko layookat fa ëttu àttewaay bu kowe ba.

Loolu lim bu néew la ci ñi ñu tabb tey ak ñi nga xam ne jot nañu leen a tuxal ci yeneen béréb. Waaye, li duuf ci nag wi, xajul ci cin li. Moo tax, ñu tànn ñi nga xam ne ñoo gën a fés ci yëf yi. Dafa fekk ne, ku ñépp tufli rekk nga tooy.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj