Ay ndogal yu bees wàcc nañ ci njàng mu kowe mi. Muy i ndogal yu jëwriñ ji jël ngir jubbanti jëlinu jàngalekat yi ak diiru bindu way-am-bag (nouveaux bacheliers) yi ci jàngune yi.
Jëwriñu njàng mu kowe mi ak coste gi moo ngi ci tànki yeesal yi mu namm ci jàngune yi. Ginnaaw waxtaan yi mu woote woon ak wër yi mu doon amal ci jàngune yi, daldi nay jël ndogal yi jiitu ci coppite yi mu woote.
Bu njëkk ci coppite yooyu moo ngi aju ci yamu (limite) at yi ñu daan jëlee jàngalekat yi. Fekk ni, bu woote (appel à candidature) mësaan a am, dees ciy fésal ni ati way-sàkku yi warul a weesu 45i at. Te, moom jëwriñ ji Abdurahmaan Juuf, gisul fenn fees ko mën a wéer ci àttey réew mi. Muy taxaw-seetlu bu mu fésal cib bataaxal (circulaire) bu mu jébbal njiitu jàngune yi (recteurs).
Ci biir bataaxal boobu nag, ma nga leen ciy xamal itam ni ngir sàmmonteek digleb àttey réew mi, far na yamu at boobu daan feeñ ci woote yi. Ba tax mu leen ciy woo ngir ñu sàmmonteek moom. Jàpp naat ni, far gi mu ko far sax dafay méngook rafet-jikko, yamale ak leeral yi ñuy woote.
Ñaareelu ndogal lee ngi aju ci way-am-bag yu bees yi. Ginnaaw bi mu nisaree woon ni dina leen tàbbal ci jàngune yi, gën-gaa sori ci weeru oktoobar wi, jëwriñ ji tijjil na leen bindu yi. Naka noonu, boroom « BAC » yépp dinañu mën a dugg ci daluwaay bii di Campusen ngir tànn seen yoonu njàng.
Xibaar boobu, démb ci àjjuma ji la ko jëwriñ ji biral, jaare ko ci yégle bu njiiteefu (direction générale) njàng mu kowe mi amal. Ñuy yégal ndongo yi ni dinañu mën a dugg ci daluwaay Campusen lu ko dalee 7i fan ci weeru ut 2024. Bu ko defee dinañu mën a wéyal seen bindu ba keroog 27i pani weeru ut wi, ci 23i waxtu yu teg 59i simili.