Abdurahmaan Juuf, jëwriñu njàng mu kowe mi, gëstu geek coste gi, biral na njureef yi tukkee ci lël bi ñu doon amal ñetti fan yii weesu (àjjuma, gaawu ak dibéer) ñeel njàng mu kowe mi. Li ñu doon waxtaane ca lël boobu nag mooy nees di sàkkee ay pexe ngir joyyanti atum njàng mi, delloo ko ca diir ba mu nekkoon.
Bokk na ci ndogal yi jëwriñ ji jël, mooy yóbbu ci jàngune yi ñi am BAC ci at mi ci nu mu gënee gaaw, ci diggante 19 sàttumbar jàpp 15 oktoobar 2024. Ndongo yooyule dinañu mën a tàmbali bindu ci lu ko dalee 21i pani oktoobar 2024.
Fas na yéene tamit dolli limub jàngalekat yi ci jàngune yi. Moo tax, dees na jël 1500i jàngalekat yu bees ci ñees dippee “enseignants vacataire”. Rax-ci-dolli, dinañ jëlaaley liggéeykat yiy doxal jàngune bi te ñu gën leen a xam ci PATS (Personnels administratif, techniques et de service). Muy ndogal lu mu jël ngir ñoŋal anam yi ñuy amalee gëstu geek tàggatug ndongo yi.
Bu loolu weesoo, jëwriñ ji wax na ni dees na taxawal ab delluwaay (référentiel) bob, ci la naali Master yi ci réew mépp di tënku.