NDOGUM YOON MU METTI FA RISAATOL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii, ndogi yoon yi bari nañu lool te tegaloo. Saa su ñu jàppee ne wàññeeku nañu rekk, fekk booba la Waalo gën a aay. Limu ndog yi am ci ayu-bés bii ñu génn rekk daf cee doy firnde.

Jàmm-a-gën a ngi jooy ay doomam, noppegul, meneen ndog mu ko yées dalaat ci kaw askan wi. Ndog moomu mi ngi am ci ngoonug démb ji fa Risaa Tool. Daamarug juróom-ñaari toogukaay moo fa mbëkkante ak genn sëfaan. Mu am ñu ci ñàkk seen bakkan. Am tamit ñu ci jële ay gaañu-gaañu yu metti.

Dafa mel ni ndogi yoon yi moom, askan waa ngi leen di bëgg a miin. Daanaka, doo toog ab diir te gisoo walla nga dégg ndogum yoon. Dafa di, ndog yi moom léegi ci yoon yépp lañuy ame. Muy ci yoon diggante dëkk ak dëkk walla ci yoon yi nekk ci biir dëkk bi donte ne sax yiy am ci yoon yu sori yee gën a doy-waar. Moo tax it, ndog mu ñëw rekk gën a yées.

Dafa di, ayu-bés bii ñu génn rekk ndog yu metti am nañ ci réew mi. Menn maa ngi ame ci yoonu Tuubaa. Juróomi doomi-aadama yi nekkoon ci daamaar gi, kenn muccu ci. Meneen maa ngi ame fa Koldaa. Benn minibiis moo fa mbëkkante ak ug sëfaan. Benn bakkan rot ca, fukki nit ak juróom-ñaar jële ca ay gaañu-gaañu. Te, laata ayu-bés bi di jeex, meneen ndog mu gën a yéeme amoon na fa Risaatol ci ngoonug dibéer ji.

Ndog maa ngi xewe fa Najel, wetu Roos Beeco. Genn sëfaan moo fa mbëkkante ak daamaarug juróom-ñaari toogukaay (7 places). Juróomi doomi-aadama ñàkk nañu ci seen i bakkan. Mu am ñetti ñu ci jële ay gaañu-gaañu. Mu doon weneen tiis wu metti wu dal ci askanuw Senegaal ci benn ayu-bés kepp.

Kon, dafa jot dawalkat yi seetaat seen taxawaay. Ku ñépp tufli nag, nga tooy. Saa yu askan wi jàppee ne góom boobu wér na, mu wulliwaat. Ndax, tay la ndog yi gën a bari. Rax-ci-dolli, dañoo gën a jegee léegi. Te, ndog mu ñëw gën a metti.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj