Biig la kàmpaañ yi door. Kàmpaañ yooyu, ñi ngi war a jeex fukki fan ak juróom ci weeru nowàmbar. Looloo tax, dibéeru démb ji, muy lëkkatoo, di làng walla muy mbootaay, ñépp ñoo ngi dagaan baatu askan wi. Ku nekk ci ñoom ak ni mu doore ab kàmpaañam. Ñii, am ndaje lañu ko doore. Ña ca des moom, ay njëgg (caravane) ak i mitiŋ.
Wotey palug dépite yi, doon na wote yu am solo lool ci kujje gi, rawatina ci Nguur gi. Ndax, bu ëppalee ay dépite fa Ngomblaan ga, dina tax mu mën a wéyal liggéeyam nu mu ko neexe. Te, waa kujje gi duñu ci am baat. Naka noonu, ñoom waa kujje gi it, bu ñu ëppee doole fa Ngomblaan ga dina tax ñu mën a saytu liggéeyu Nguur gi. Lu leen neexul, ñu fànq ko.
Mu mel ni téeméeri toogu (sièges) ak juróom-benn fukk ak juróom yi ñépp la soxal. Ku sañoon jël yépp donte ne sax, lu tollu ci ñeen-fukki toftale ak benn ñoo koy xëccoo. Dafa di, ñoom ñépp askan wi kepp moo leen mën a àtte. Ba tax na, jamono jii, ku nekk ci ñoom a ngi def kéemtelaayu kàttanam ngir am baatu askan wi.
Toftale yooyu di xëccoo ci wote yii dafa am yu ci gën a fés. Nde, ñooñu, démb ak barki-démb ñoo fi nekkoon di joŋante. Muy ñu ci mel ni lëkkatoo Jàmm ak Njariñ, Takku Wallu Senegaal, Sàmm Sa Kàddu, Pastef, Senegaal Kese, añs. Lëkkatoo yooyu nag, ku nekk ci ñoom ak ni mu doore kàmpaañ yi.
Bu dee waa Jàmm ak Njariñ, Takku Wallu Senegaal ak Sàmm Sa Kàddu ñoo boole seen doole fa Ndakaaru. Démb lañu amal am ndaje ngir doore ko seen ub kàmpaañ. Ndaje moomu, dinañu ko amale fa “Esplanade Lem gi, Commune de Biscuiterie” bu ñetti waxtu jotee bees sukkandikoo ci li Njiitul toftale lëkkatoo Sàmm Sa Kàddu, Bàrtelemi Jaas, fésal ci xëtu Faacebookam. Bu dee kii di Ceerno Alasaan Sàll Njiitul lëkkatoo Senegaal Kese, moom amal na aw waxtaan ci lënd gi. Mu dippee waxtaan woowu Jàkkaarloo ak Askan wi.
Naka noonu, ñii di waa Pastef tamit, am na nu ñu doore bésu tey bi donte ne sax, wute na ak bu lëkkatoo yee. Ñoom dañuy def am njëgg. Ñi ngi doore “Sortie 10” Kër Njaay Lóo jaar Sàngalkaam, jaar Mbàmbiloor, jaar Bayax, Jendeer. Bu ñu jógee foofu, jaar Nooto, jaar Mbooro, jaar Daaru Xuddóos, Jaar Tayba Njaay. Bu ñu jógee foofu, dem Tiwaawon, jaar Pir dem Mexe. Bu ñu paree ci loolu, dinañu amal am njëgg ak ub mitiŋ fa Cees, tëjee ko bésu démb ji.
Lees ciy ñaawlu mooy fitna jees ci jotagum nemmeeku diggante farandooy Bàrtelemi Jaas ak yoy Abbaas Faal mu Pastef. Nde, ay sàmbaa-booy dañu songoon njëggum Abbaas Faal mi, yor i ngànnaay (jaasi, paaka, fetel) am ñu ñu gaañ, nangu seen i alal. Ci beneen boor bi, màkkaanu Taxawu Senegaal la ay nit jafal, taal ko, mu lakk ba nekk dóom. Jëwriñ biir réew mi, Sã-Batist Tin, génnee na yégle di woo way-pólitig yépp ci jàmm, ñu ànd ak seen sago.