Fa Kaasamãs, dafa ag daamaruy sóobare gu dal ci kow um mbéll « antichar ». Bi loolu amee nag, ñeenti sóobare ñoo ci ñàkk seen i bakkan, am yeneen juróom-ñar yu ci jëley gaañu-gaañu yu metti bees sukkandikoo ci rajo RFM.
DIRPA, kurél gi yor kàddu ak jokkoog làrme bi, moo génne ab yégle di ko xamle. Dañ ci wax ne :
« JÉYYAB mbéll fa barabu sóobare juróomeel.
Ag daamaruy sóobare moo dal ci kow um mbéll « antichar » ci alxames ji14 desàmbar 2023 bi, fekk ñuy dox ag yónnent ci yoonu Jokadu-Kajalog, ca bëj-gànnaaru Biññoona fa barabu sóobare juróomeel. Limees na ci 4i sóobare yu ci dee ak 3 yu ci amey gaañu-gaañu.
Njiitu réew mi, Maki Sàll, bind na ci X (Twitter ba woon), sargal 4i sóobare yooyii dee ci.