Jéggaani xaalis. Jéggaani dund. Jéggaani xam-xam. Léegi, jéggaaniy xalaat a ci des. Ndeke, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa sàkkoo xam xalaatub jàngalekatu Yoon bu fekk baax Farãs, muy Guillaume Dragon. Daf ko laaj ay lay ñeel ñetteelu moome gi mu bëgg a wut. Nee ñu nag, jàngalekat boobu nangul na ko ne nekkam ab lawax lu mën a nekk la. Mu mel ni Aminata Ture, nekkoon fi jëwriñ ci Nguuram, moom, naanewu ko ndox. Ndax, nee na aajowul dem bitim-réew ndax, ndeyu-àtte bi moom, dafa leer nàññ. Maanaam, amul sañ-sañu laaj ñetteelu moome. Rax-ci-dolli, amul kenn ku xam-xamam màcc ci wàll woowu, ak foo mën di dëkk, ngay mën a wax leneen lu dul ne mënul a bokk. « Li ñuy xaar ci moom kay, mooy jox gëdd ndeyu-àtte bi te amal ay wote yu leer nàññ. »