ÑETTEELU MOOME GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal ñetteelu moome gaa ngiy wéy di lëmbe réew mi. Ba tey, Njiitu réew mi, Maki Sàll, àddoogu ci. Bés bu set, gaa ñiy laaj nu mbir yi di deme. Day bokk, walla du bokk ? Kenn xamagul. Waaye, xel teey na ci. Li ko sabab moo kàddu yi Njiitu réew mi yëkkati, keroog ca waxtaan wa mu doon amal ak waa Express. Nde, moom, dafa yokk xar mi kawar, gën a xamb taal bi. Boobaak léegi, mi ngi nimseek a wiiri-wiiri. Waaye, wiiri-wiiri, jaari Ndaare.

Ku mu neex téye sa kàddu, wànte jamono moom, mëneesu ko teree dox. Te, li jamonoy dox, wote 2024 yiy gën di jegesi. Moo tax, ku ci bëgg a doon lawax, dagaan xobi askan wi, fàww dinga leeral sa taxiway, ci nii, mbaa ci naa. 11i weer kepp a des laata wotey njiiteefu réew mi. Kon, lu waay doon nëbb, léegi mu feeñ. Njiitu réew mi, Maki Sàll, ci lim woneegum, moom ak i jegeñaaleem, dafa bëgg a laaj ñetteelu moome. Ndax, junj kat, doy na boroom xel. Te, kàdduy keroogam ya, bari na lu ñuy leeral ci yëf yi. Senegaal nag, ak àddina sax, Maki Sàll rekk lañuy déglu.

Mbirum ñetteelu moome gi, dina ko def, am du ko def, du tey la tàmbali. Yàgg nañu koo laaj Njiitu réew mi, Maki Sàll. Dafa di, coow laa jiitu wotey 2019 yi. Booba la sikk-sàkka yi dooroon, ñuy xel-ñaar ndax, moom Maki Sàll, bu amee ñaareelu moome dina yóotu ñetteel walla fa lay yem ? Bu lënt amee ci mbir mi, tey la. Waaye, démb, Maki waxoon na ci lu leer, baamu koy yoon ne, ginnaaw 2019 du bokkati ciy wote.Nii la ko waxe woon :  

“Fan yii yépp, dégg naa ay coow. Muy loo xam ne, daf ma jaaxal. Ndax, day mel ni lu xiinul rekk, xëy taw. Wax joo xam ne, kenn xamul fu mu jóge, ak lan moo ko tax a jóg. 2016, man maa sàkku askanu Senegaal nu xoolaat ndeyu-àtte yi. Dama ne, mbirum moome gi dafa war a jeex tàkk, ñépp jàpp ne réew mi kenn mënatu fi toog lu ëpp ñaari ay. Dañu ko bind mu leer nàññ. Xanaa kay, ku jàng tubaab, boo ko firilee loolu war na ko xam. Man, maa ngi sama genn moome, bu ci Yàlla àndee, 2019 lay jeex. Ci coobare sunu Boroom ak bëgg-bëggi saa-senegaal yi, dinaa yeesalaat moome gi 2019, su booba, man pare naa ci.”

Kàddu yooyu nag taxul woon gaa ñi dakkal laaj yi. Ndax, ku ndóbbin rey sa maam, foo gisatee lu ñuul daw. Dafa fuñ jaar ak Ablaay Wàdd. Moo tax, ba ni ñu koy falaate ci atum 2019, ñi ngi wéy di ko ci sonal. Walla dafa am lu ñu njort. Loolu terewul, moom bi ñu ko ci laajaatee, fa mu jaaroon la jaaraat. Ba ci at yii weesu lii la leen ci mujj tegal :

“Man, dañ ma fal ci kóolute réew mi. Kàddu gi nga wax am na ñu ko laaj laata ñu may fal 2018, 2017, waa moom kañ lay pare ? Ak lu mën di am bés bu wax jotee, dinaa wax. Wax jii ngay dégg nag, mënul a xumb a xumb ba ma wax ci. Li tax ma wax sama njaboot bu ñu ci wax mooy nun liggéey lañ nu sant. Mënuñu la fal defoo liggéey bi war ba pare ngay wax lu ñëwagul.”

Mu mel ne, looloo yokk saa-senegaal yi di am ay sikki-sàkka ci mbir moomu. Lenn waralu ko lu dul yenn kàddu yees di faral di dégg ay ñoñam di leen jibal. Mu mel ni kon looloo tax gaa ñi njort ne yëf yi mën na am wax-waxeet. Waaye, li gën a dekkalaat coow loolu jamono jii mooy waxtaan wi mu doon amal wu mu doon amal ak ñii di wa Express nga xam ne dafa caa laalaale mbirum ñetteelu moome gi.

Moom Njiitu réew mi, Maki Sàll, xamle na ca waxtaan woowa mu doon amal keroog ne mbirum ñetteelu moome gi moom, bu dee ci wàllu yoon féete na boor. Maanaam, ci la mu xamle mooy ne ca atum 2016 la mbir mi leer. Ndaxte, at moomu la jébbaloon askan wi ab sémbub àtte buy soppi Ndeyu-àtte bi, wàññi moome gi, jële ko ci 7i at, indi ko ci 5i at. Te, nee na, laata muy def Referàndum bi, waxtaan na ci ak Ndajem ndeyu-àtte mi. Kon, moome gu njëkk gi bokku ci. Mu neeti, dina bokk walla du bokk, waxi pólitig la. Te, ciy waxam ba tey, ay gaayam sax moom lañu jiital. Maanaam ñi fare ci ag làngam, mooy seen tànneef ci wotey 2024 yi. Kon, Maki Sàll daa jàpp ne Yoon may na ko mu bokkaat ci wotey njiiteefu réew mi ngir dagaan baatu askan wi. Moom nag mooy xool ndax day bokk am déet. Tontoogul ci loolu nag? Ndax, nee na, jamono jii, liggéey la tal. Bu jotee, dina xamal ay ñoñam taxawaayam ci loolu, laata mu koy wax askanu Senegaal. Mu mel ni loolu bokk na li sabab coow li ñu ciy faral di dégg yenn saa yi.

Coow li nag bari na te, kenn waralu ko ku dul Njiitu réew mi, Maki Sàll. Ndax kat, ku boot bukki moom, fàww xaj yi baw la. Moo tax coow toppu ko ci boor yépp. Fu ne, gaa ñi di fa artu naan ñetteelu moome du fi ame. Ñii naan dañu ko fiy tere, ñee naan jàmm a ko gën. Lu ci mën di am, léegi ñu xam ci dara. Ndax, wote yi moom li ci des bareetul. Te, ku dund dinga fekke. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj