ÑETTI FANI DËJ FA MALI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tiis wu metti moo dal ca kow askanu Mali. Lu tollu ci juróom-benn fukk ak ñeenti doomi-aadama lañu fa faat ci ay cong ci alxames jee weesu ci boori fukki waxtu ak benn ci yoor-yoor bi. Ña ca faatu am na ay sóobare, am ay siwil. Mu am tamit ñu ci jële ay gaañu-gaañu, waxaalewuñu yàqu-yàqu yi. Cong yooyu nag ci ñaari béréb yu wuute lañu ko defe. Menn maa ngi ame ci gaalu Tomboktu gi doon daw diggante Gaawo ak Mopti ñu koy dippe “COMANAV” (Le bateau de de la compagnie malienne de navigation). Cong moomoo nga ame ca béréb bii di Gurma-Rarus diggante Tomboktu ak Gaawo. Meneen ma ame ca Bàmba benn ci béréb bu sóobare ya nekk ci bëj-gànnaaru réew ma fa diwaanu Gaawo. Nee ñu rëtalkati GSIM (Groupe de Soutien à l’Islam et aux Musulmans) ñooy ñi amal ñaari cong yépp.

Askan way yeewoo jamono jii ca Mali ak Burkinaa Faaso ña ngay wéy di dund ci njàqare. Li ko waral du lenn lu dul cong yi GAT (Groupes Armés Terroristes) di amal saa su nekk. Ndax, bu dee bu njëkkaan cong yi ci sóobare yi la ëppe, léegi moom demeetul noonu. Cong yi waral ñetti fani dëj yooyu (àjjuma, gaawu ak dibéer), ñi ci loru ay sóobare ñoo ci gën a tuuti. Juróom-benn fukk ak ñeenti doomi-aadama yi ci faatu, ñeen-fukk ak juróom-ñeent yépp ay siwil lañu, fukk ak juróom yi ñooy ay sóobare. Mu am ñu ci jële ay gaañu-gaañu, am tamit ay yàqu-yàqu yu bari ci gaal gi.

Ginnaaw bi ñu songee gaal gi ak benn ci béréb yi sóobare yi féete ca bëj-gànnaar, ñoom it feyu nañu donte ne sax yëf yi daf leen a bett. Jot nañoo kepp lu jege ay juróom-fukki rëtalkat. Mu mel ni nag xeex bi dox diggante FAMas (Forces Armées Maliennes) ak rëtalkat yi moom du tey la door. Xanaa kay daf di daa am luy ñuul ci soow mi. Ndax, ba ñu dogee lenn ci li leen lëkkale woon ak waa Farãs ba tey, day mel ni loolu dafa yokk ci xar mi karaw. Saa su nekk rekk ñu dégg foofa walla Burkinaa Faaso ay cong yu metti. Ba tax ñu bari di ci duut baaraamu tuuma ñii di waa Farãs jàpp ne seen loxo setu ci. Ndax, génnee gi ñu leen génnee ci seen mbiri bopp du lu ñu mën a muñ.

Looloo tax fi mu tollu nii tembe moom cong yaa ngi mel ni tulleek màlle ci ñaari réew yooyu. Ci lu matul weer rekk ay bakkan yu bari rot fa. Waa Mali ñi nga xam ne ñoom la tiis wi dal seen kow, xamle nañu ne jël nañu matuwaay yi war yépp. Dinañu gën a yokk kaaraange gi ci béréb yooyu donte ne sax amoon na fa. Li mat a laaj kay mooy fan la nit ñi di mucce léegi ? Bu fekkente ne ñiy amal cong yi moom xàmmeewuñu sóobare ak siwil. Fu leen neex ak nu mu leen neexee lañu koy defe.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj