Ñetti faniy ndajem USA – Afrig

Yeneen i xët

Aji bind ji

Talaata 13i fan ba alxames 15i fan ci weeru desàmbar 2022, ay njiit ak i ndawi réewi Afrig ñoo nga woon ca Wasinton. Seen dem foofu nekkoon i tànki taxawe ndajem USA – Afrig.  Ginnaaw biñ ko sosee ca atum 2014, ren, ci atum 2022 bi la ndaje moomu di soog a amaat.

Ndajeem USA – Afrig mu 2022 mi jeex na ci alxames jii weesu. Ma nga doon ame ca Etaa-Sini ci diiru ñetti fan (13, 14 ak 15 desàmbar). Ndaje maa nga ame woon ci yittey Njiitu Etaa-Sini lii di Jóo Baaydën ak jàppandalu Njiitu réewu Senegaal lii di Maki Sàll miy jiite jamono yii Mbootaayu Bennoog Afrig. Muy ndaje mu aju ci lëkkaloo Etaa-Sini ak Mbootaayu Bennoog Afrig te ki fi nekkoon njiitu Etaa-Sini, Baraag Obamaa njëkke woon ko ci atum 2014.

Ndajem ren ji nag, mooy ñaareel bi yoon. Ñaŋ fa doon waxtaane lépp lu jëm ci kaaraange, rawatina kaaraange réewi Sayel yi rëtalkat yi jógal. Waxtaane nañ fa itam lu jëm ci dund bu doy, Agoa bi tënk baana-baana gi diggante Etaa-Sini ak réewi Afrig yi ba 2025, suqaleeku réewu Afrig yi ba ci wàllu jafe-jafey kéew gi. Ca njeexital la, am nay ndogal yu am solo yu fa bir. Jóo Baaydën fésal na fa àndam ci gis-gis bi njiiti réewi Afrig yi am ci seen agenda 2063, te lépp di dellu ci Afrig gu doon benn. Jot na faa dige sax 55 tamñareti dolaar ci ñetti at yii di ñëw ak 30i tamndareti dolaar ci saa si ñeel kaaraangeg lënd gi (cybersécurité).

Bu dee ci wàllu Afrig itam, Njiitu Mbootaayu Bennoog Afrig li rafetlu na jéego yi Etaa-Sini sàqi ngir Afrig gën a am cër ci Ndajem Kaaraangeg Mbootaayu Xeet yi, ak ubbil leen bunti réew yiñ dippee G20 te ñu ëpp doole ci koom-koomu àddina si. Waaye, Njiit li Maki Sàll ñaawlu na fa yenn ci ndogali Etaa-Sini ñeel réewi Afrig yi, yu ci demee ni daan yi ñu daan Simbaabwe ak ndogal li nar a daan réewi Afrig yi séq ak Riisi. 

Ci fàttali, réewi Afrig yee ngi wékk ndajem USA-Afrig mi ci seen yittey wuutale seen i lëkkaloo ci àddina sépp, niñ ko waxee woon ca ndajem Riisi-Afrig ma.

Bu loolu yépp jàllee, mbir yi dañuy niru ni ci ni ko Etaa-Sini nammee rekk lay doxee. Bu ndaje mi amulee ci diiru 8i at ginnaaw biñ ko sosee, dafa fekkoon ni Donaal Tërëmp mi fi wuutu woon Baraag Obamaa ci boppu Etaa-Sini moo mësul a wone ag wegeel ci kembaarug Afrig. Saa su mësaan tudd Afrig sax, bu noppee xolu Saa-Afrig yiy futt, ñuy tëb ak a dal ndax wax yu xeeblu yam ca daan teg. Bu ren jeet, Joo Baaydën a ko sàkku. Ñu ne waaw, mu dellu tànn 49i njiiti réewi Afrig ya ko teewe, beddi ña sa des. Lépp, mu teg ko ciy bëgg-bëggiy Etaa-Sini yay mbubboo demokaraasi ak ubbeeku. Naka la kaaraange réewi Sayel yi di yitteelee Etaa-Sini ba noppi mu dellu seppi ci ndaje mi Burkinaa Faaso, Maali ak Sudã ñi rëtalkat yi gën a lakkal ci kembarug Afrig ? 

Naka la 49i Njiiti réewi Afrig mënee nangu lu ni mel ? Maki Sàll mi jiite Mbootaayu Bennoog Afrig nag, lu ko tee wax dëgg tubaab bi ? Bu Njiiti Afirg yi booloowul, bennoo, ndax doxandéem yaa leen di bennale ? Caaxaan baaxul waay…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj