Démb, ci altine ji, lañu doon àggale ndaje ma ñu dooroon ca ayu-bés bee ñu génn fa Ngomblaan ga. Li ñu ko dugge woon, mooy saytu sémbuw àtte biy tas campeef yii di CESE ak HCCT. Ki ko doon sàkku mooy Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Waaye, càkkuteef loolu, dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yi ëpp ca Ngomblaan ga, wotewuñu ko. Kon, sémbuw àtte wi jàllul.
Nguur gi fi nekk dañoo dige woon ne dinañu fi jële yenn banqaas yoy, seen njariñ bariwul noonu, rawatina CESE ak HCCT. Ñoom jàpp nañu ne, koppaar yi fay duggu, bari lool, xaj nañ feneen. Maanaam, mënees na ko delloo askan wi, jaare ko ci ay naal walla ay liggéey yoy, Saa-Senegaal dinañ ci gis seen bopp. Looloo tax, altine jee weesu, ñaar-fukki fan ak juróom-benn ci weeru ut, Njiitu réew li sàkku woon ci Ngomblaan gi ñu amal am ndaje ca alxamesu ayu-bés bii weesu, fa màkkaanu ndawi askan wi. Mébétam moo nekkoon ñu amal ay coppite ci ndeyu àtte yi ngir ñu mën fee jële HCCT ak CESE.
Démb, ci altine ji, lay sog a jeex. Waaye, la fa rote du la Njiitu réew mi doon xaar. Ndax, dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yi nga xam ne ñoo ëpp doole fa, ñoo lànk ne lii du ci dal. Maanaam, jële fi ñaari campeef yooyu du luy mën a nekk. Moo tax, bi ñu amalee ay wote fa béréb boobu, njureef yi nii la tëdde. Ci téeméeri dépité ak juróom-benn-fukk ak juróom yi, juróom-ñett-fukk ak ñett dañoo wote ne ànduñu ci ñu dindi campeef yooyu. Am juróom-ñett-fukki dépite yu nangu ñu fànq leen. Dépite yooyu mooy waa Yewwi Askan Wi, Wallu ak ñenn ñi nga xam ne bokkuñu fenn (non inscrits). Mu am nag, ñaari dépite yoo xam ne teewuñu. Ñu gis ne lu dul ñi nga xam ne teewuñu, yeneen dépite yi, kenn mànduwul ci wote, ñépp a wone ne seen ug ànd walla ag ñàkk ànd ci li Njiitu réew mi bëgg.
Kon, ni wote yi tëdde nii, day firndeel ne ñaari campeef yooyu fi lañuy des. Kenn du leen fi mën a jële lu dul ñu taxawal geneen Ngomblaan goo xam ne, ñi ànd ak Nguur gaa fay ëpp. Dafa di, Njiitu réew mi am na sañ-sañu tas Ngomblaan gi fi nekk, askan wi wote, falaat yeneen i dépite. Ndax, ndajem ndeyu àtte mi mooy ki ko may sañ-sañ boobu.
Waaye, mbir mi yemul foofu. Ndax, ginnaaw bi waa Bennoo Bokk Yaakaar gàntalee càkkuteefu Njiitu réew mi dañu cee teg leneen. Kii di Abdu Mbów nga, xam ne moo jiite kippaango dépitey BBY gi moo xamle ne mook i mbokkam, dinañu jébbal li ñuy dippe “motion de censure” tey, ci talaata ji. Li ñu ko dugge mooy daaneel Nguuru Usmaan Sonko gi.
Fi mu tollu nii, mënees na jàpp ne mbir yi dafa gën a jaxasoo. Laaj yi mat a samp kay, mooy ndax, waa BBY dinañu daaneel Nguur gu bees gi am déet ? Walla, ndax, Njiitu réew mi dina tas Ngomblaan gi fi nekk ci diir bu gàtt am déet ? Dees na ci xam dara ci lu yàggul.