NGOMBLAAN GI : DÉPITE YI JÀLLALE NAÑU ÑEENTI SÉMBUW ÀTTE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci àjjuma ji, Ngombalaan gi wote na ñeenti sémbi àtte. Ñuy i àtte yuy yoonal ci Njiitu réew mi mu xaatim i déggoo diggante Réewum Senegaal ak i campeefi koom-koom (institution économique) fi Afrig, fa Tugal ak fa Asi.

Démb ci àjjuma ji, 14i fani mars 2024, Yaasin Faal, di jëwriñu Bennoog Afrig ak Mbiri bitim-réew, teewaloon na Càmm gi fa Ngomblaan ga ngir layal sémbuw àtte No04/2025. Muy sémb wuy yoonal ci Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, mu xaatim déggoob doxiinuw ndiisoog bànk bu UMOA (Convention régissant la commission bancaire de l’Union Monétaire Ouest Africaine), te Nguurug Senegaal nangu woon ko ca 31 mars 2023.

Bi 10i waxtu di jot ci yoor-yoor bi, lañu ubbi waxtaan yi. Ginnaaw bi ñu càmbaree sémb wi, 132i dépite wote nañu. 131 yi ànd ci. Mu am kenn ku ci àndul. Xaatimub sémb woowu nag, dina doon luy dooleel càmmug wàlluw bànk yi ci diiwaanu Afrig sowu-jant. Dina doon itam luy méngale wàll wi ak doxaliin yiy xew ci àddina si ngir yokk kaaraangeem ak dalam ci déndu UMOA.

Bi sémb woowu jàllee, dépite yi jàllale nañu yeneen i sémbi àtte. Wenn wi di Sémbuw Àtte bu limu 06/2025, di digal Njiitu Réew mi mu xaatim bokkug Senegaal ci Bànkub Yaxantu ak Suqaleeku bu Penku ak Bëj-Saalumu Afrig. Bokk googu dina dëgëral lëkkatoog Senegaal ak réewi diiwaan yooya ñeel koom-koom gi.

 Sémbuw Àtte limub 07/2025 ak wu limu No08/2025 lañu ca toftal. Wu jiitu wi di digal Njiitu réew mi, mu boole Senegaal ci pas gi taxawal BERD (Banque Européenne pour la Reconstruction et le Développement, Bànku Tugal bi ñeel Tabaxaat ak Suqaleeku). Muy pas goo xam ne dañu ci indi ay coppite yu bari ginnaaw bi ñu ko njëkkee xaatim ca bésub 29 me 1990, fa Pari (réewum Farãs). Bokkug Senegaal foofa dina ko jàppandalal ay kopparal yu jëm ciy sémbi suqaleeku ci fànn yu bari.

Weneen sémb weet dafa jox ndigal Njiitu réew mi mu xaatim bokkug Sénégaal ci BERD (Banque Asiatique d’Investissement dans les Infrastructures), di bànkub kopparal bu Asi jëme ci tabaxte yi. Muy itam bokk guy dimbali Senegaal ba mu mën a jotee ay kopparal ca Bànkub Asi ngir suqali tabaxte yi ci réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj