NGOMBLAAN GI JÀPPAL NA USMAAN SONKO ÀPPU “DPG” BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal “DPG” (Déclaration de Politique Générale) li nga xam ne nee na woon kurr ci réew mi, ma ngay waaj a am ab daaneel. Nde, kii di elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dafa sàkku woon ñu amal i coppite ci sàrtu biiru Ngomblaan gi. Dafa di, coppite gi mujj naa am ba Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jàllale ko. Kon, Usmaan Sonko moo ciy waaj a des. Nde, tey ci alxames ji lañu ko jàppal bés.

Àllarba fukki fan ak benn ci weeru sàttumbaar la dépite yi jàppal Usmaan Sonko. Waaye, lél boobu dafa safaanook li sàrtu biiru Ngomblaan gi wax. Nde, diggante bi leen Njiitu réew mi di jébbal dekkare DPG bi ak bés bees ko war a amal dafa war a am 8i fan. Fileek boobu nag, day romb bésub 12i pani sàttumbaar. Te, bés boobu la Njiitu réew mi nar a tas Ngomblaan gi.  Rax-ci-dolli, elimaanu jëwriñ yi ci boppam, dara tënku ko ci wàllu àpp. Kon, njortees na ni du wuyuji.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj