Ngomblaan gi taxawal na Ëttu àttewaay bu kawe bi. Tay ci gaawu bi, 28i pani desàmbar 2024, la dépite yi tànn 8i dépite yu ci war a bokk ak seen i tof.
Bi fukki waxtu jotee ci suba si la dépite yi waroon a dajewaat fa Ngomblaan ga ngir càmbar sémbuw àtte bi aju ci kopparal Nguur gi ci atum 2025 mi. Ci woote bi, xamaloon nañu leen itam ni, bu ñu ci noppee, war nañu jublu ci tànnug way-bokki Ëttu àttekaay bu kawe bi.
Ëttu àttewaay bu kawe boobu nag, dees na ko samp weer ginnaaw bu ñu taxawalee kayug Ngomblaan gu yees. Te, moom rekk mooy Ëttu àttekaay bu mën a àtte njiit yu mag yu deme ni Njiitu réew mi ak képp kuy jëwriñ walla nga mës ko nekk, bu dee tuuma yees lay toppe ci sa nekkug jëwriñ walla Njiitu réew la aju.
Bees sukkandikoo ci dog 101eel bu Ndayu sàrtu réew mi, kenn mënul a topp Njiitu réew mi ciy xew-xew yu ame ci kayam lu dul ni wor am na ci digganteem ak askan wi te ñu koy duppe ci nasaraan haute trahision. Te, Ngomblaan gi moo ko mën a topp ci kaw juróomi dépite yoo jël, ñett yi ànd ci.
Ginnaaw bi ñu jàllalee ci lu gaaw sémbuw àtteb kopparal Nguur gi, ca la dépite yi daldi tànn 16i lawax. Lu tollu ci 140i dépite ñoo leen woteel. Ñaar kott ñoo ci àndul. Ñeenti dépite yi des wotewuñu. Ci 16 yooyu, 8i yi ñooy way-bokk yu jiitu yi (titulaires), 8i yi ci des di seen i tof.
Ñii ñooy limub dépite yi bokk ci Ëttu àttekaay bu kowe bi :
8i way-bokk yu jiitu yi :
-
Àlliyun Ndaw
-
Ramatulaay Bojã
-
Yugaar Jonn
-
Aamadu Ba no 2
-
Roqi Njaay
-
Mohamed Ayib Dafe
-
Daba Wañ
-
Abdu Mbow
8i way-bokk yi ci topp :
-
Sàmba Daŋ
-
Ulimata Sidibe
-
El Haaji Tàmbeedu
-
Faatu Jóob Siise
-
Muramani Jakite
-
Mari Elen Juuf
-
Mayaba Mbay
-
Faatu Sow.