NGOMBLAAN GI : TAXAWU WÉET NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ab diir, ginnaaw ba Ngomblaan gi tëjee woon ay buntam, tijjiwaat na leen ci fan yii. Ngomblaanug Senegaal nag, dafa miin coow, rawatina gu mujj gii. Ci coow lañu tëje woon. Te it, ci coow lañu ubbiwaatee. Maanaam, ñoom duñu jóg ci xiiroo ak ŋaayoo. Saa buñ sumbee ab liggéey, rawatina buñ waree wote, ci coow lay mujj. Bu njëkkaan, coow laa ngi doon dox diggante dépitey Nguur gi ak yoy kujje gi. Waaye, wii yoon moom, demewul noonu. Dépitey Yewwi Askan Wi la ak dépitey Taxawu Senegaal yi ñooy séq coow li.

Wotey 2024 yi sabab na coppite yu bari ci géewu pólitig gi. Ndax, kenn umpalewul ne, lëkkatoog Yewwi Askan Wi, ay làngi pólitig yu bari la dajale. Te, jamono jii ñu tollu, ñenn ci njiiti làng yooyoo ngi mébét a jiite réew mi. Ba tax na, ku nekk ci ñoom ak i militaŋam a ngi ràcc di jëmale seen kanamam. Loolu bokk na ci li jur féewaloo gi dox seen diggante. Rax-ci-dolli, waxtaan wi Njiitu réew mi amaloon, te waa Yewwi lànkoon ne duñu ca dem, waa Taxawu dem ca, dafa xajamal diggante bi.

Boobaak léegi, seen diggante rataxatul. Ubbiteg Ngomblaan gi ci fan yii, firndeel na ko. Mbokki Xalifa Sàll yi jébbal nañu seen bataaxelu bàyyi ca Njiiteefu Ngomblaan ga, Aamadu Maam Jóob. Loolu di firndeel seen ug génn ci kippaangog Yewwi Askan Wi. Waa Taxawoo ngi naan ñee dañu leen a wor. Maanaam, dañu leen a boddi ci seen i mbir. Ñoom it, dañu lay ne, ñooñu dañoo sàmmontewul ak càrti lëkkatoo gi. Dafa di, génn googu ni mu ame ñu mu bett, noonu la amee tamit ñoo xam ne bettu leen, sóoroon nañu ko. Ndax, ñaari kuy moom, mënuñoo bokk menn mbalka. Te, ñaar ñu bokk genn toogu gu ñuy bëgg, duñu mën a bokk yoon.

Kon, jamono jii, waa Yewwi, seen lim wàññeeku na. Ñeen-fukki dépite ak ñaar lañu dese ginnaaw bi waa Taxawu génnee. Waaye, ñoom tamit waa Taxawu Senegaal néewaayu limu dépite yi ñu am dina tax duñu mën a taxawal ag kippaango (groupe parlementaire) ca Ngomblaan ga. Waa Bennoo Bokk Yaakaar ñooy wéy di ëpp doole ca Ngomblaan ga. Lii mooy li ñu naan musiba joo gis, jàmmi kenn a nga ca. Maanaam, ay woo gis rekk, am na ku cay bànneexu.

Xew-xewi ubbite gi yemul foofu rekk. Ndax, coppite am na tamit ci kippaangog BBY. Kii di Abdu Mbów mooy ki wuutu Omar Yum ci boppu kippaangog Bennoo Bokk Yaakaar. Moom Omar Yum, léegi, mooy jëwriñ ji ñu dénk làrme bi. Ginnaaw coppite yooyu ak ndogalu dépitey Taxawu yi it, taxawalaat nañu kippaango gu yees ca Ngomblaan ga.

Tof-njiit ya ñii la:

Ibraahima Baaba Sàll (BBY)

Aysatu Sow (BBY)

Maalig Jóob (BBY)

Yata Sow (BBY)

Moodu Baara Gay (PUR)

Sira Njaay (BBY)

Mamadu Lamin Jàllo (WALLU)

Aysa Ture (PASTEF)

Fara-saytu ya ñii la:

Ndey Lisi Siise (BBY)

Kariim Seen (BBY)

Umar Suwaane Ciise (BBY)

Roqi Njaay (PASTEF)

Abdulaay Jóob (WALLU)

Ñi ñuy dippe “Questeurs” yi tamit ñii la:

Aminata Géy (BBY)

Yoro Sow (BBY)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj