NGOMBLAAN GI YEESAL NA SÀRTU-BIIRAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dépite yi jàllale nañu « loi organique no10/2025 ». Muy àtte bob, dafa ñëw ngir andi ay coppite ci sàrtu-biiru Ngomblaan gi.

Démb ci àjjuma ji, 27 suwe 2025, la dépite yi doon fénc atte bii di « loi organique no10/2025) te waroon a andiy coppite ci sàrtu-biiru Ngomblaan gi. Ginnaaw bi ñu ci noppee, ñu ëpp ca ñoom ànd nañu ci àtte bi, daldi koy jàllale. Ci biir 139i dépite yi wote, 138 yépp dañoo dëggal seen ug ànd ci coppite yi. Mu am kenn ku ci màndu, waxul waaw, waxul déet.

Bi ñu koy càmbar nag, am na ay joyyanti yu yenn dépite yi doon sàkku ñu amal leen laata àtte bi di jàll. Ku ci mel ni Mohamet Ayib Selim Dafe, doon na sàkku ñu defaraat tëggin wi. Anta Baabakar Ngom itam doon na sàkku ñu dellusi ci jamono yees di amal jotaayi laaj-tontu yi ñu jagleel Càmm gi. Kii di Màggat Seen itam bëggoon na ay coppite ngir gën a dëgëral yamale góor ak jigéen fa Ngomblaan ga. Waaye, joyyanti yu Sëñ Dafe laaj kepp lañu nangu. Yu Anta Baabakar Ngom ak Màggat Seen doon sàkku, dañu leen a mujje dàq.

Ginnaaw bi ñu jàllalee sémb weet, am na ay kàddu yu delloo jib ngir rafetlu ko. Ku ci mel ni Aysata Taal Sàll gis na ne sàrt bu bees bi dafay gën a dooleel Ngomblaan gi. Nde, boo ko xoolee ba ci biir, dafa gëddaal bu baax ndiisoog luññutug Ngomblaan gi. Dina leeral liggéeyam itam ak nees koy jàllalee ci askan wi. Am na itam ay matuwaay yu ñu dooleel ngir yiir dépite yi, rawatina ci murig malaanum kiiraay walla anam yees di ñàkke moome gi.

Ginnaw looloot, am na ñu jàpp ni liggéey bi des na ba léegi. Nde jar na ñu xoolaat lim bi war ngir matale kippaangog Ngomblaan, ak mbiri Ëttu Àttewaay bu kawe bi. Naka noonoot, ndiisoog Ngomblaan gi ñeel sàrt yi, biir réew mi, liggéey bi ak àq ak yelleefi doom-aadama duut na baaraam yenn matuwaay yu deme ni tekkig ndombo-tànku dépite yi.

Nees tëralee tekkig ndombo-tànku dépite yi dafay may làngug pólitig mu am sañ-sañu tekki ndombo-tànku dépite, te loolu dëppoowul ak li Ndayu Àtte Réew mi wax ci jàmbureg moomeg Ngomblaan gi. Dafay may itam Pekkug Ngomblaan gi muy dëggal tekkig ndombo-tànk te du jar fénc. Muy lu teey xel lu way-pólitig yi mën a jëfandikoo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj