Njiitu Ngombaan gi, Allaaji Maalig Njaay, siiwal na ay coppite yu am solo yees namm amal ca Ngomblaan ga. Ci ab lël bu ñu doon amal fa Sali, àndoon ceek Càmmug réewum Kanadaa ak Mbootaayu xeet yi, la ko xamlee. Lël boobu sax, ñoo ngi ko doon amal ngir yokk manoore dépite yi ba ñu mën a doxal bu baax seen moome.
Naka noonu, Sëñ bi Njaay gaaral na fa càmbar yi ëpp solo yees war a amal ci sàrt yi, dooleel gi ñu war a dooleel liggéeyu caytug Ngomblaan gi, tàmbalig natt naali bokkeef gi, ak taxawal kërug taskatu xibaar gu ñeel Ngomblaan gi ngir jàppandal bu xibaar ya fay tukke.
Coppite yu ni mel nag, li leen tax a jóg mooy yeesal xar-kanamu Ngomblaan gi ba mu méngook jamono, te doon itam campeef gu jege askan wi. Ñu jublu ci tabaxaat demokaraasi, teg ko ci leeral, mën-mën ak delloo askan wi njukkal.