Nguur geek Usmaan Sonko : Mën a tëru, mën a teggi

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey ci gaawu bi, 15i fan ci weeru sulet 2023, la làngug politig gii di Pastef les patriotes nammoon a amal am ndaje fa estaad Aamadu Bari bu Géejawaay. Waaye, gornooru Ndakaaru ak perefe Géejawaay dañu leen ko tere. Looloo waral ba njiitul pastef li jëlaat kàddu gi démb ci guddi ngir wax ak i ñoñam.

Usmaan Sonko yékkateeti nay kàddu démb ci guddi ngir wax ak askanu Senegaal, rawatinay ñoñam. Nguur gi aayee ndaje mi Pastef nammoon a amal ngir tabb ko mu doon seen lawax ci wote yii di ñëw. Ca la yëgle woon ni dina amal aw waxtaan ci àjjuma ji, bu 21i waxtu jotee.

Naka noonu, xel yépp njortoon nañ ni dina xotti ndogalu gornoor sànni fale te wax ndaw ñi ñu génn, dem ca estaad ba ni mu leen neexee. Waaye, loolu yépp fekku ko ci. Mënees na wax ne Usmaan Sonko jàmm la woote.

« Ñu bare ñu ngi xaar ñu génn xeex. Dingeen am gàcce. Dinanu xeex de, waaye bii moom, li may ñaan waa pàrti bi, ñaan ko soppe yi, ñaan ko képp kuy Saa-Senegaal boo xam ne bëgg nga demokaraasi, bëgg nga dëgg sax ci réew mi, bañ nga tooñ ak jaay-doole, li ma lay ñaan mooy nanu teggi sunu tànk. »

Wànte nag, Usmaan Sonko dëggalul wenn yoon li gornoor ak perefe doon xaar ci moom. Déedéet ! Moom kay daf leen njuuy. Naam, meeru Sigicoor bi àndul ci li kilifa yi dogal, waaye dafa sant ay ñoñam ñu sàmmonteek ndogal li. Waaye nag, yemul foofu. Xamal na leen ne xew-xewub tabb gi moom, dina am. Bés bu ñu ko jàppaatee, dina am ci mu leen di neex mbaa mu leen di naqadi. Dafa fekk ni, wile yoon, mën a tëru, mën a teggee ci aay. Ndaxte, Nguur gi dafa nekk ba tey ci pexey taqal leen ak di leen jiiñ niti fitna. Te bees leen toppoon, fitna dina am ci gaawu gi.

Bu loolu weesoo, Usmaan Sonko woo na ay ñoñam ak askanu Senegaal ci ñu wone seen uw naqar ak ñàkk a ànd ci li nekk di xew ci réew mi. Maanaam, nañu wut i sagar yu xonq, takk leen bu 10i waxtu jotee ci gaawu gi. Muy màndarga  ngir wone ak a ñaawlu coxorte gi ñuy jiiñ Nguurug Maki Sàll gi. Digal naat waa làngu pólitig gu Pastef ñu jublu ci njëndum jaray kawsu pastef yi. Mu tuddee leen « bracelets de la liberté ». Te nañu leen takk boole kook yu xonq ngir ñaawlu singali gi Nguurug Maki Sàll singali seen làngug pólitig ak fitna gi mu leen di teg, rawatina moom ndeyu-mbill ji.

Njiitul Pastef li yemul rekk ci bàyyi leen mu sedd ak takk leen yu xonq walla jaray kawsu yi. Dafa leen bàyyee estaad ba ba noppi dellu wooteeti tëggum bool (concert de casserole) bu 20i waxtu jotee ba tegal 30i simili. Bu ko defee, ñu ànd wéyal ko ci réew mépp ba 21i waxtu jot. Lii de mooy li woykat biy woy, naan “Na riir ! Na riir a riir !”

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj