NGUUR GI DAJALE NA 405i MILIYAAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nguurug Senegaal dajale na 405i miliyaar ci 15i fan kese. Muy alal ju takku ju ko boroomi alal lebal ginnaaw woote bi mu amaloon jëme ko ci kopparal i sémb. Ñu gën koo xam ci nasaraan « l’emprunt obligataire par appel à l’épargne public ».

Ci weeru mars bi ñu génn, Nguurug Senegaal amaloon na ab woote bob, ci kopparal i sémb la jëm. Woote boobu nag, di « emprunt obligataire par appel à l’épargne public », doon na xeetu bor bob, campeef yi dañu koy faral di jëfandikoo niki jumtukaay ngir dajalaatu xaalis ci boroomi alal yiy meññlukat. Bor lay doon. Dees na ko fay ci àpp gu ñuy xam te dëppoo ci, ca njëlbéen ga. Dafay ànd ak itam ay xeeti tegaay yu aju ci yàggaayu àpp gi.  Xeetu leblante bii nag, doon na lu UMOA (Union Monétaire Ouest africain) ak AMF (Autorité des Marchés Financiers) nangu, teg ko ci sàrt yu dëppook leeral ak aar xaalisu jàmbur yi ciy dugg.

Woote boobu nag, Nguur gee ngi ko amaloon ngir dajalaatu ci 150i tamñareet yu mu jagleel i sémbi suqaleeku ci réew mi. Ñu waroon ko amal ci àppu 23i fan (27i fan ci weeru mars jàpp 18i fan ci weeru awril 2025), jaare ko ci banqaasu caytu bii di DGCPT (Direction général de la comptabilité publique et du trésor) ak kër yii di Invictus Capital and Finance SA ak SGS (Société Générale Sénégal).

Ginnaaw bi ñu ko dawalee ci diirub 15i fan, gis nañu ni lu ëpp ci li ñu doon séentu dugg na. Nde dajalaatu nañu 405i tamñareet. Muy ndam lu réy nag, donte ni du guléet Nguurug Senegaal di amal woote bu ni mel. Ndam loolu sax, tax na ba waa DGCPT jël ndogalu tëj woote bi, dakkalee fi dajalaatu bi.

Xaalis bii ñu dajale ci diir bu gàtt dafay dellu di wane ni jàmbur yi yor seen i moomel tey jëflanteek campeef yu mag yi, ñoo ngi wéy di am kóolute ci réewum Senegaal donte ni Nguur gu yees gi fésaloon na bu yàggul dara tolluwaay bu yéeme bi ñu fekk gafakag Nguur gi ak mën-mënam bu yées ci wàllu kopparal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj