Nguur gaa ngi raggu ngir setal boppam. Démb ci alxames ji, 15 suwe 2023, la jëwriñ yii di Aamadu Ba, Ismaayla Maajoor Faal, Antuwaan Feliks Jom ak Sidiki Kaba amal am ndaje, doon ci jàkkaarlook taskati xibaar yi ngir indiy leeral ñeel tolluwaayu réew mi ak yëngu-yëngu yu metti yi fi amoon ginnaaw bi àtteb mbirum Sweet Beauté bi jibee, keroog 1 suwe 2023 bi.
Ñaari ayu-bés ginnaaw bi yoon daane Njiitul Pastef li ak Ndey Xadi Njaay ñaari ati kaso ak 20i tamndareet yu ñu war a dàmpe kii di Aji Raabi Saar, taafar yu metti lañu seetlu woon ci réew mi ba nit ñu bare daldi ci faatu. Jëwriñ yi gën a fës : Aamadu Ba (magum jëwriñ yi), Ismayla Maajoor Faal (Jëwriñu Yoon), Antuwaan Feliks Jom (Jëwriñu biir réew mi), Sidiki Kaba (Jëwriñu xare bi) ak Abdu Kariim Fofana (Jëwriñu taax gi) ñoo jël kàddu gi ngir layal Nguur gi. Nde, fan yii, seen der yàqu na ci àddina sépp.
Ndeem mooy ndeyu-mbill ji, Usmaan Sonko a nekkoon seen cëslaayug kàddu. Daanaka, wax jépp ci moom rekk lay dellu. dafa di, ginnaaw coow li daan bees ko daan jur ak ñi ci dee ñépp, ba jonni-Yàlla tey, kenn jàppagu ko. Loolu nag, dafa jaaxal ñu bari. Foogees na ne sax, Nguur gi daf ko ragal a tëjlu. waaye de, ji ñu dénk wàllu Yoon, di Ismaayla Maajoor Faal, weddi na loolu. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, àttekat baa noppeegul ci mbindum ndogal li war a tax ñu jàppi njiitul Usmaan Sonko. Bu boobaa nag, jëwriñ ji ne, ñaari mbir rekk ñoo ci mën a am. bi ci jiitu mooy, amaana, Usmaan Sonko ñëw, jébbal boppam Yoon. Ñaareel bi mooy, toppekat bi war a doxal ndogal li dem jàpp ko, yóbbu. Bees ko déggee bu baax, lu mën a am ci ñaar yi, Usmaan Sonko lay doy mu nangu tëdd walla mu ŋàññ ndogal li. Te bu ko ŋàññee, du doon dabaatal. Dees ko àttewaat fees ko àttee woon.
Ñu desandi ci Yoon ba tey. Jamono jii, Juan Branco, doomu Farãs jiy layal Usmaan Sonko, mi ngi defar aw wayndare wow, nee na, CPI la koy jébbal. Lu ni mel nag, dafa mel ni xaw na tiital waa Nguur gi ba tax jëwriñu xare jii di Sidiki Kaba àddu ci, di jéem a dalal xel yi. Nde, moom dafa jàpp ne waxi CPI coowal picc la rekk.
« Senegaal, réewum Yoon la muy doxal sañ-sañu Nguur gi, di ko tegoo te di ko teg itam mbokki maxejj yi. Bare na lool lu ñuy dégg ñu naan Nguuru Senegaal, Kilifa yu mag yeek takk-der yi dinañu leen yóbbu ca CPI. Ay coowaloo la rekk. Ñi koy wax xamuñu nees koy defe te seen mën-mën àggu fa. Seen pexe mooy yàq deru réewum Senegaal. Muy itam meneen pexe ngir indi réeroo ak xaajatle ci biir takk-der yi. »
Mu mel ni léegi, ginnaaw àttewaay ba ak mbedd yi, xeex baa ngi ñu tuxal ci kibaaraan yi. Ku nekk ak li ngay xibaar ak di ko fésal ngir bënn boppu askan wi ba ñu mën laa gëm. Laata jëwriñ yi doon noppi ci seen lël boobule sax, waa kujje gee ngi doon njañse ci mbaali-jokkoo yi, di leen weddeek a ŋàññ.
Ku ci mel ni Bugaan Géy Dani moom, ca saa sa la génn janook taskati xibaar yi ngir dàjji lépp lañ fa wax. Ci tënk, jàpp na ni ay tappale rekk la. Bees gisee Càmm gi génn di wax, dafa fekk ni kurél yi boole réewi àddina si ñoo leen toŋal ngir ñu andiy leeral ci coow li fi am ak nit ñi ci ñàkk seen i bakkan. Mu leen di xamal ni li ñu war a wax waxuñu ko :
« Wax leen ñu fu ngeen tollu ci gëstu bi ngeen fi waxoon ci 21 awril 2021 ginnaaw bi 14i nit faatoo ci mbiri Aji Saar. Moone de, jëwriñ ji Sidiki Kaba mi fi daan xeexal àqi doom-aadama doon na fi mbel-mbeli fu nekk naan lépp dina leer. Waaye, ba léegi tus, du sax luy nirook gëstu. Càmm googu moo nuy digaat ni dafay ubbib gëstu ci faatu yi fi am ci 1 ak 2i fan ci weeru suwe wii weesu. »
Seen wax jépp nag, ragg nguur gee leen taxon a jóg. Dafa mel ni nag, seen raggu bi dese na set. Bugaan Géy yokk ca ne li xew Senegaal weesuwul ag Nguur guy jëfandikoo dooleem ngir faagaagal ak a far ni mu ko neexe ay wujjam ci làngu politig gi, jàmmaarloo ceek ñaxtukat yi ba rey ci luy tollook 20i nit, gaañ ci ay téeméeri téeméeri nit, tëj ciy téeméeri téeméeri ba noppi di jéem a setal boppam ci sàmbaa-bóoy yi mu ngemb ñuy ubbiy sox ci kow ñiy ñaxtu.
Kujje gi sax yamuñu ci loolu. Nde, waa YAW woote nañu ndaje ak taskati xibaar ci àjjumay tey ji, tey bu 16i waxtu jotee. Nuy xaar ba xam lu ñuy tontu waa Nguur gi.