SAES (Syndicat Autonome de l’Enseignement Supérieur) mooy kurél gi ëmb jàngalekat yi nekk ci daara yu kowe yi. Kurél googu nag, ci ay ñaxtu yu metti lañu nekkoon. Daanaka, lu tollu ci ñaari ba ñetti ayu-bés a ngi nii yoo xam ne, seen liggéey demewul noonu. Ñaar walla ñetti fan yu nekk ñu dakkal njàngale mi. Nguur gi meloon ne ñu yëgul li xew. Waaye, sàndikaa bi moom teggiwul tànkam. Loolu tax ba Nguur gi mujje xaatim dekkere buy saafara li sababoon seen xeex bi.
Xeex bi sàndikaa bi sumboon ngir ñu delloo ñenn ci seen i naataango seen i àq ak i yelleef, tàmbali nañu cee gis seen bopp. Ginnaaw waxtaan yu bari yi dox seen diggante ak Nguur gi, déggoo mujje naa am. Nde, Nguur gi xaatimal na leen ab dekkere keroog ci àjjuma ji. Dekkere boobu, dina am buntu bu mu tëj. Dafa di, loolu ñi ngi koy xeex atum 2020 ba tay ñu ciy sog a am ndam.
Li waraloon xeexu sàndikaa boobu du lenn lu moy ñu jox “pension” njabooti seen naataangoo yi nga xam ne génn nañu àdduna. Ndax, ñoom dañoo gis ne li ñu teg njabooti way-dawlu yooyu du dëgg, du yoon. Te, fàww ñu xeex ko ngir ñu saafara ko ci nu mu gën a gaawe. Ba tay, ci dekkere boobu ñu xaatim ngir joyanti dëng-dëng boobu, dañoo boolewaale neexalu gëstu bi ci “pension” bi.
Mu mel ni, benn ci poñ yi sababoon sàndikaa bi làbbali fan yii, saafara am na ci. Waaye, dafa des yeneen yoo xam ne ñi ngi ciy xaar Nguur gi donte ne sax, fi mu ne moom, dañuy jàpp ci gittax ba am yat. Terewul, ci seen yégle bi ñu fàttali déggoo yi ñu amoon ak Nguur gi fi jóge, juróom-benni fan ci weeru sãwiyee, atum 2023. Te, poñ yooyu ñu déggoo woon ñi ngi ciy xaar ay saafara. Muy lu ci mel ni àggali ak yokk ay taax ak i jumtukaay ci daara yu kowe yi, jël limub jàngalekat yu takku ci béréb yooyu, añs.
Kon, mënees na jàpp ne gaa ñi dañoo gëmm rekk, waaye nelawuñu. Maanaam, dañoo teggi seen tànk rekk. Waaye, bàyyeeguñu. Ndax, ci njeexitalu yégle bi ñi ngi sàkku ci seen i ñoñ ñu gën a takku. Su ko defee, poñ yi ñu mujjee lim ñu saafaraal leen leen. Li mat a laaj kay mooy ndax Nguur gi dina leen saafaraal lépp am déet ? Li ci kanam rawul i bët.