NGUUR GU YEES GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndekete, njuuy, ci feemi Njiitu réew mi la bokk. Nde, ginnaaw Aamadu Maam Jóob mi mu taamu woon ñeel njiiteefu Ngomblaan gi, fental nan ug Nguur gog, ñu bari la bett. Bu dee tabbug Aamadu Ba gi ci njiiteefu njëwriñ gi bettul ñenn ñi, am na ciy jёwriñ yoo xam ne, seen uw tànnin jaaxal na nit ñi. Lan la Njiitu réew mi, Maki Sàll, di waajal ?

Ci guddig gaawu gi lees siiwal turi Jëwriñi Nguur gu yees gi Aamadu Ba war a jiite. 11i waxtu ci suba lañ jàppoon ngir siiwal turu Jëwriñ ju njëkk ji, 12i waxtu ngir biral Nguur gu yees gi. Waaye, ci ngoon gi lañ mujje xam kiy jiite Nguur gile. Yeneen Jëwriñ yi nag, dañu xaar lu yàgg a yàgg, laata ñuy biral seen i tur. Ñu njort ne, Njiitu réew mi ak Jëwriñ ju njëkkam ji dañu amoon ay jafe-jafe yu tard ci seen liggéey. Am na sax ñuy ruumandaat, naan, waa PS ak waa AFP ñoo yéexal mbir mi. Nde, waa PS bëgguñu woon Sëriñ Mbay Caam bokkaat. Bu dee AFP, ñoom, nee ñu xëccoo amoon na seen biir, waaye ameesu ciy leeral. Am na sax ñuy wax it ne, Abdulaay Daawda Jàllo bëggutoon a jóge fi mu nekkoon. Te, moom ak Aamadu Ba miy Njiitalu jëwriñ ji,  seen diggante dafa am ay ñagas-ñagas. Ak lum ci mënti doon, li Nguur giy xeeñ neexul.

Fanweeri jëwriñ ak juroom-ñett (38), lim boobii la Abdu Latif Kulibali, magum fara-caytub Nguur gi, siiwal ci guddig gaawu gi, bi 21i waxtu tegalee. Ci biir fanweer ak juróom-ñetti jëwriñ yooyu, dees na ci fekk juróom-ñetti jigéen ak juróom-ñetti ndaw. 12i jëwriñ ñoo génn : 

  • Abdulaay Daawda Jàllo, Jëwriñu ngurd meek naka ga woon, tàbbi na ça Màkkaanu Njiitu réew mi, di Njiitalu kabineem. Aamadu Mustafaa Ba a ko wuutu ;

  • Matar Ba mi ñu dénkoon tàggat-yaram gi, génn na. Yankooba Jatara a ko wuutu ;

  • Aamdu Hot mi ñépp seedeel xereñteem, bokkatul ;

  • Aliyun Saar mu AFP tëb na ;

  • Abdu Kariim Sàll, meeru Mbaaw bi, génne nañ ko ;

  • Maalig Sàll nekkatul jëwriñu Yoon wi. Nee ñu, Farba Ngom, géwélu Maki Sàll bi, moo ko dàqlu ;

  • Umar Géy, meeru Sàngalkaam, dem na ;

  • Nene Fatumata Taal, jëwriñ jees dénkoon ndaw ñi, dem na ;

  • Ndey Sali Jòob mi doon saytu Njaboot gi ak jigéen ñi, wàcc na ; 

  • Zahra Iyaan Caam, jëwriñu mikorofinaas ba woon tamit, bokkatul ;

  • Daam Jóob, wàcc na ;

  • Abdulaay Jóob, wàcc na ;

  • Aminata Asom Jaata, meeru Kër-Masaar, tëbal nañu ko.

Am na yit ñu bees ñu dugg ci Nguur gi. Bu njort rafetee ñeel ñenn ñi, ñaaw na ci ñeneen ñi. Dafa di, diir bi Maki Sàll toog yépp tabbul jëwriñ yi, yéex bim la yéex a siiwal ak jëmm yi mu tànn, day am lu muy niru. Dafa mel ni, Njiitu réew mi dafa am lu muy waaj. Dees na yaatal njàngat li ci beneen yaxal. Balaa boobu, nii la Nguur gu yees gi tëdde : 

  • Aamadu Ba : Jёwriñ ju njëkk ji 

  • Sidiki Kaba : jёwriñ ji ñu dénk wàllum larme bi 

  • Abdu Latif Kullibali: jёwriñ, magum fara-caytub  Nguur gi 

  • Aamadu Mustafaa Ba : Jёwriñ ji ñu dénk wàllum kopparal gi

  • Ismaayla Maajoor Faal : jёwriñu Yoon wi 

  • Meetar Aysatu Taal Sàll : jёwriñu mbiri bitim-réew ak saa-senegaal ya nekk ca bitim-réew 

  • Anet Sekk : njёwriñal ca njëwriñu mbiri bitim-réew ak saa-senegaal ya nekk ca bitim-réew 

  • Antuwaan Feliks Jom : jёwriñu biir réew mi 

  • Biram Fay : njёwriñal ca njёwriñu biir réew mi 

  • Mansuur Fay : jёwriñu tabax gi, dem ak dikk bi ak xàll-yoon gi 

  • Ulimata Saar : jёwriñu koom-koom gi, Naal bi ak koppe bi 

  • Galo Ba : jёwriñu liggéeyi bokkeef gi  ak yeesalug njariñeg askan wi 

  • Mari Xemes Ngom : jёwriñu wér-gi-yaram gi 

  • Faatu Jaane : jёwriñu jigéen ñi, Njaboot gi ak kaaraangeg xale yi 

  • Umar Saar : jёwriñu mbéll yi ak sewolosi (géologie) 

  • Aali Nguy Njaay : jёwriñu mbey mi, njumtuwaanug kow gi ak jàppandalug dund gi 

  • Sёriñ Mbay Caam : jёwriñu ndox mi ak cetal gi 

  • Yankooba Isaa Jóob : njёwriñal ca njёwriñu ndox mi ak cetal gi 

  • Duudu Ka : jёwriñu naawaan gi 

  • Maam Mbay Ñaŋ : jёwriñu wёrteef gi

  • Mamadu Taala : jёwriñu  bokkeefi gox-goxaat yi, yokkute gi ak nosteg dëkk yi, di bëkk-néegu Nguur gi ;

  • Seex Umar Aan : jёwriñu njàngum gone yi ;

  • Musaa Balde jёwriñu njàng mu kowe mi, gëstu bi ak coste gi ;

  • Sofi Galaadimaa : jёwriñu soroj bi ak laf yi 

  • Sàmba Njóobeen Ka : jёwriñu yokkuteg mboolaay gi, yemoog nawle yi ak dëkk yi 

  • Mustafaa Jóob : jёwriñu yokkuteg ndefar yi ak ndefaraan yi 

  • Paap Saaña Mbay jёwriñ nàpp gi ak koomug géej gi 

  • Sàmba Si : jёwriñu xëy mi ;

  • Aliyun Ndóoy : jёwriñu càkkeef gi, yokkute gu sax gi ak càllaleg mbindaare mi 

  • Yanqooba Jatara : jёwiñu tàggat-yaram gi 

  • Abdulaay Séydu Sow : jёwriñu taaxal gi, dëkkuwaay yi ak cetug mbooloo mi 

  • Abdu Kariim Fofana : jёwriñu yaxantu bi ak noseef yu ndaw yi ak yu yamamaay, yor baatu Nguur gi 

  • Aliyun Sow : jёwriñu mbatiit gi 

  • Musaa Bookar Caam : jёwriñu njokkalante gi, telekom yi ak koomug noska gi 

  • Aali Saleh Jóob : jёwriñub Càmm ak njureefi mala yi 

  • Wiktorin Ndey : jёwriñu mikorofinaas ak Koom-koomu mboolaay geek jàppalante bi 

  • Mariyaama Saar : jёwriñu liggéey bi,  tàggatug mecce gi, njàng mi ak mboole gi 

  • Paap Maalig Nduur : jёwriñu ndaw ñi 

  • Paap Aamadu Njaay jёwriñu ñeeñal gi ak coppiteg liggéey yu fànnoodi yi.

Lii daal mooy nguur gu yees gi. Ñoo ngi xool ba xam nag, ndax at ak lu topp ci li dese Maki Sàll ci ci kayam bu mujj bii, dinañu fi liggéey lu mucc ayib. Loo xam ne liggéeyuñu ko fi woon ci fukki at yii weesu. Li ci kanam rawul i bёt, na yónnee yàgg rekk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj