NISEER : CEDEAO DAY SONG AM DÉET ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ayu-bés a ngi nii ak lu teg, bi sóobare yi foqatee Nguur gi fa Niseer. Bu weesoo ñaawlu gi mu ko ñaawlu, CEDEAO (Communauté Économique des États de l’Afrique de l’Ouest) noppi na a jël ngànnaay yi ngir delloo Muhammet Basum njiiteefu réew mi, jële fa sóobare.

Bésub 26 sulet 2023 bii weesu la sóobare ya foqati woon nguur ga ca loxoy Muhammet Basum mi nekkoon Njiitu réewum Niseer. Muy ñeenteelu « Coup d’état » bu am biir CEDEAO diggante 2020 ak 2023. Lu ni mel tax ba kurél gi dellu di ko ñaawlu ak di sàkku ci ñi amal jëf ji ñu delloo nguur ga ca loxoy kees fal.

Li bees ci mbir mi nag, mooy ni, wile yoon, CEDEAO yemul ciy daan rekk. Dafa taxaw temm ba mu jaral ko jël i ngànnaay ngir jëlee nguur ga ca loxoy sóobare ya. Looloo tax ba mu amal ay ndaje ci ñetti fan yii weesu (àllarba, alxames ak àjjuma). Mu doonoon ndaje yoy, njiitali làrme yi ñoo ci doon diisoo.

Ginnaaw ndaje ma, la fa tukkee ciy xibaar mooy ni CEDEAO noppi na a jël ngànnaay yi ngir jëlee nguur ga ca loxoy sóobare yi te delloo Mohamet Basum mi ñu teg loxo ak njabootam ca boppu réew ma. Muy luñ mën a jàpp bees dégloo kàddu yi Abdel Fatoo Musaa, di Komiseer bi yor wàlli pólitig ak Kaaraange, biral. Muy xamle ni :

« Waxtaane nañ ci ndaje mi lépp lu mu laaj bees demoon ba war a amal am cong, ba ci matuwaay yi war, waaye tamit naka laak jamono jañ fay yebal sunuy soldaar. »

Yile kàddu di tekki ni CEDEAO dina fa yebal i sóobare bu pexe amul ci diisoo bi. Nde, bu weesoo ñetti réew yii di Burkinaa, Gine, Mali ak Niseer nga xam ni nguur gaa nga ca loxoy sóobare yi, njiitul làrme yeneen réew yépp teewoon nañ ca ndaje ma.

Ci alxames ji, laata ndaje ma doon jeex, Aysata Taal Sàll jëwriñ ji mi yor wàllum bitim-réew xamle woon na ni bu CEDEAO jëlee ndogal lu ni mel, sóobarey Senegaal yi dinañu ci dem. Ndax, réewum Senegaal a ko xaatim. Ca ndaje maat, yeneen réew joxe nañ fa seen kàddu. Ñu mën cee lim Koddiwaar, Beneŋ ak Niseriyaa mi nga xam ni moo nar a jiite xeex bi.

Lii yépp tax ba àddina wërngal këpp di ragal xare ba jolli ci fan yii di ñëw ca Niseer. Nde, ëllëg ci dibéer ji la CEDEAO jox àpp sóobare ya ngir ñu delloo nguur ga. Waaye, dafa mel ni ñii jéemuñu sax luy wund loolu. Ba ci ndawi CEDEAO yi mu yabaloon ngir ñu doxi fa tànki jàmm, gisewuñook kenn ca kilifa ya. Du kilifay làrme ba, du Mohammet Basum mi ñu nëbb. Ay sóobaree ñoo leen dalal ca dalub roppalaan ya, wax ak ñoom li ñuy wax ak ñoom, mu yem fa.

Lu jiitu lile ndogal itam, gisoon nañ ni ñaari réew yii di Mali ak  Burkinaa jotoon nañ dankaafu kurél gi. Liñ ko xamal ci seen yëgle bi ñu bokk siiwal mooy ni mépp cong mu ñu amal ci kow Niseer jàpp nañ ni ci ñoom lañ ko teg te bu boobaa dinañu sóobu ci xare bi.

Ndax, waxtaan wi ñu ne moom lañuy jiital, ndax dina jur jàmm ? Ndax bu àppu CEDEAO bi jeexee dinañu xaar àppu UA bi war a dem ci ñaari ayu-bés walla ? Ñuy xaar ba xam ci lan la njiiti làrme yi di déggook seen i njiiti réew.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj