Xoqatal ak metital ya amoon ca jamonoy njaam ga dekkiwaat na fa Araabi Sawdit. Nekkin wu metti la fa jigéeni Afrig yi fay daan seen doole nekke. Luññutuy saabalukaayu Amerig bii di New York Time moo leeral lu bari ci mbir moomu. Ñii di waa Seneplus tamit def nañ ci ay njàngat yu yaatu.
Dafa di, Nguurug Araabi Sawdit dafa lëkkaloo, xaatim ay digaale ak yenn ci réewi Afrigu penku yi, niki Keeña ak Ugàndaa. Fa réew yooyee lañuy jële limi jigéen yu takku yóbbu leen ca seen kër ya. Jigéen ñooñu nag, lu mburu daj ci taal, ñoo ngay daj lu ni mel foofa. Ñii di xiif, ñee ñu leen di dóor, ña ca des ñu leen di siif. Am na sax ñoo xam ne duñu ñibbisi ak bakkan. Ci gàttal, ay jaam lañu leen di def.
Njënd ak njaay mi ñu doon amal ci mala yi moo tuxu ci nit ñi bees sukkandikoo ci saabalukaay Amerig bi. Daanaka, léegi, jigéen ñi am njaay lañu leen def. Nde, ci li saabalukaay xamle, foofa jigéen ju fa xas teg sa tànk moomatoo sa bopp. Ci kër gi ngay nekk, doo dem, doo dikk. Am na ñoo xam ne sax, bu ñu agsee lañuy nangu seen i jàll-waax (paaspoor). Maanaam, loolu mooy noppi ngaa dellu fa nga jóge woon. Soxna sii di Margaret Muyeni nee na, njaatigeem dafa nangu jàll-waaxam, xamal ko ne daf koo jënd. Te, li ci gën a doy waar mooy dañu leen di teg fitna yu metti ci biir kër yi. Ci kàdduy soxna soosu, lu ci bari, njaatigeem daawu ko nangoo jox lekk.
Bari na ciy liggéeykat, rawatina ay jigéen, yoo xam ne ñi fa lañu ñàkke seen i bakkan. Li fa faatu ci juróomi at yu mujj yii ku ñu ko wax nga taf loxo ci gémmiñ. Saabalukaay bi xamle na ne lu tollu ci ñaari téeméeri liggéeykat ak juróom-ñaar-fukk ak ñeent ñàkk nañu fa seen bakkan. Ñoom ñooñu, Keeñaa lañu bawoo. Te, li ci ëpp ay jigéen lañu. Li gën a metti ci mbir mi mooy ak nu liggéeykat bi mën di faatoo dañu naan dara rayu ko. Am na senn soxna suy wuyoo ci turu Eunice Achieng, moom dafa woote woon seen dëkk, yëgal leen ne njaatigeem nee na daf koy ray ba noppi sànni ko ci mbàndum/mbalkam ndox. Yàggul dara ñu fekk ko ci am mbànd mu faatu. Loolu terewul póliisu dëkk ba xamal ay mbokkam ne néew bi dafa tàmbalee yàqu. Duñu ko mën a seet ba xam lu ko ray. Te, jàpp nañu ne dafa dee noonu rekk, dara laluwul ci ginnaaw. Ñu bari ci ñoom ci anam yu doy waar lañu génne àdduna. Waaye, mbir mi yemul foofu kese.
Dafa di, saabalukaay bi dafa xamle ne, tukkib jigéen ñi fa réew mooma dafa am ñu nekk ci ginnaaw. Maanaam, ñoo xam ne ñooy yombal dem bi. Ndax, nee na, doo toog ay fan yoo gisul ay jigéeni Keeñaa fa dalu roppalaan ya, ñu jëm Araabi Sawdit. La fa nekk ci liggéeykat yu bawoo fa Keeñaa ak Ugàndaa tollu na ci xaaju miliyoŋ ci li Nguur gi wax. Bu dee fa Keeñaa moom, Njiitu réew ma moo xamle ne bëgg naa yobbu xaaju miliyoŋu liggéeykat fa réew moomu ci at yii di ñëw. Kenn ci way-digalam yi ak rakkam yor nañu seen i këri liggéey yoo xam ne loolu mooy seen liggéey.
Naka noonu, fa Ugàndaa tamit, ña ko fay def duñu ay como. Ndax, boroomi këri liggéey yuy jël jigéen ñi di leen yóbbu, kenn ci kilifay pólis yu mag yi. Keneen ki di Seneraal bu “division Léopold Kyanda”. Mu amaat ay sëti buur bii di Fayçal yoo xam ne bokk nañu ci ñi ëpp doole ci ñaari këri liggéey ya fa ëpp doole yuy yëngu ci loolu.
Mu mel ni jamonoy njaayum jaam lañu delloosi ci réew yooyu. Daanaka, dañoo soppi doxalin rekk ak seen i dig yu ñu leen di dig ba diigal leen. Maanaam, dañu leen di nax ba yóbbu leen. Bu ñu àggee, ci lañuy xam ne ngelaw dina dugal ci pax lu mu fa mënut a génne.