NJAAYUM GERTE GI : CÀMM GI SAMP NA NJËG GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Càmm gi samp na njëg gees war a jaaye gerte gi ci kàppaañ 2023-2024 bi. Kilo gerte bu nekk deesu ko jaaye lu yées 280 ci sunu xaalis (FCFA). Muy nag njëg gu cëkk bees ko gam-gamleek njëg gi baykat yi doon xaar.

Njaayum gerteg kàmpaañ 2023-2024 bi dina tàmbali ci bésub 30 noowàmbar bii ñu jublu. Démb ci àjjuma ji, 24 noowàmbar 2024, la ndogal li wadd fekk ñu doon amal am ndajeem jëwriñ yi mu soxal ci njiiteefu magum-jëwriñ yi Aamadu Ba. Ca ndaje moomu nag, jël nañ fay ndogal ñeel anam wees war a saytoo njaayum ren ji. Ñoo ngi tollu ci fukki ponk yoy bi ci ëppal solo baykat yi di njëg gees war a jaaye kilo bi.

Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy nattaango yu Sud Fm siiwal, jëlees na ndogalu jaaye gerte gi 280 FCFA (juróom-fukk ak juróom benni dërëm) kilo bu nekk. Muy nag njëg gu càmm gi jàpp ni xel mënees na ko nangu ndax lees ci yokk 5 FCFA (maanaam benn dërëm) bees ko gam-gamleek njëg gi woon daaw ci 275 FCFA (juróom-fukk ak juróomi dërëm).

Taxul mu doon nag lu gënal baykat. Muy lees mën a jàpp bees sukkandikoo ci kàddu yi Siidi Ba mi yor kàddu CNCR (Conseil national de concertation et de coopération des ruraux) maanaam kurélu réew mi ñeel disoo ak lëkkaloob waa àll bi. Seen yaakaar moo doon kilo bi mën a jar lu mu tuut tuut 300 FCFA (juróom-benn-fukki dërëm). Nde am na sax bërëb yees ko tàmbalee jaaye 300 ba 350 FCFA.

380 FCFA yi nguur gi samp nag njëg gu mu palãse la, maanaam kenn du jaaye lu ko yées. Ba tax ñuy ragal ni bés bu baana-baana yi yokkee li ñuy jënde, du yomb ñiy defar diwlin gi jot ci gerte gi.

Ginnaaw looloot, jiixi-jaaxa am na ci yenn ciy xibaar yu fa rote ñeel tolluwaayu ngóob mi. Bees déggee ba tey li Siidi Ba wax, xel teey na ci lim bi càmm gi siiwal ni moo tukkee ci tool yi te tollu ci 1700 000 ton.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj