Ci weer doŋŋ lañu tollu bi lekkool bi tijjee ak tey. Waaye ñaari kuréli jàngalekat yii di Cusems (cadre unitaire syndical des enseignants du moyen secondaire authentique) ak Saems (Syndicat autonome des enseignants du moyen et secondaire) dinañu tàmbalee bank seeniy loxo ci ayu-bés bii di ñëw. Li ñu ci namm nag mooy dànkaafu nguur gi ca teel.
Démb ci àjjuma ji, 3 noowàmbar 2023, ñaari kurél yii di Cusems ak saems, diy kurél yi dajale jàngalekat yi ci daara yu digg-dóomu yi, doon nañu janook taskati xibaar yi. Ci seen jotaay boobu, ñaari kurél yi fésal nañu fa seen yéene lëkkatoo ngir gën a mën dooleelante. Ñuy dànkaafu Càmm gi nag ngir mu jóg ca teel te def li ko war ci lekkool bi.
« Cusems ak Saems fas nañu yéene xàccindoo, dóorandoo. Dinañu ko tàmbali nag ci bés yii di ñëw ak kayitug yëglu (préavis de grève). Nu ciy dànkaafu Càmm gi ngir nu mën a am lokkool bu dal ci atum ren mi. » (Allaaji Maalig Yum sekkarteeru Saems)
Naka noonu, Ñaari kurél yi fas yéene ànd ngir janook Càmm gi ca teel. Waaye nammuñu yem rekk ci jébbal kilifa yi ag këyitu yëglu. Nde dinañu bànk seeniy loxo ci talaata ji, 7 noowàmbar, duppe ko « journée d’école morte », maanaam bés bu jàng dul am ci lekkool bi.
Ñoom nag, li ñuy naqrlu mooy ni Càmm gi ñàkkee sàmmonteek dige yi mu xaatimoon. Bu weesoo li ni mel, leneen lu ñuy sàkku ci Càmm gi mooy mu yëngu ci lu gaaw ñeel jàngalekat yu bare yi ñu teg loxo jamono yii, tëj leen ci lu dul yoon, te andi i pexe ci njàngune Séex Anta Jóob bi ñu njort ni dafa koo bëgg tëj.
Ginnaaw yii yépp nag, kurél yi dellu nañu soññ seeniy ñoñ ci ñu jóg te takku bu ñu bëggee am ndam ci seen xeex.