NJÀNG MI : JËLUB 2000iy JÀNGALEKAT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bàrki-démb ci alxames ji, 23 sãwiyee 2025, la Càmm gi tijji woon jëlub 2 000iy jàngalekat yi ñeel ekooli tuut-tànk yi, yu suufe yeek yu digg-dóomu yi. Jël boobu nag, dees na ko amal ci kow i sàrt yu mat a leeral.

4 527i jàngalekat la ekool bi soxla ngir matale limu jàngalekat yi mu aajowoo. Muy lim bu ñu fésaloon ci weeru oktoobar 2024 wee romb, ba ñuy amal ubbiteg ekool yi ci atum njàng 2024-2025. Ginnaaw bi ñu ko fésalee, Càmm gi biraloon na yéeney mottali ko ci sémb yi gën a tembare yu Njiitu réew mi taxawal. Naka noonu, 2 000iy jàngalekat la namm a dugal ci lu gaaw, ci atum ren ji. Ba tax mu ubbil lawax yi bunt bu ñuy jébbale seen i wayndare ci diggante 23i fani sãwiyee ba 1eelu fanu weeru féewiryee 2025.

Jël boobu nag, ubbil nañu ko képp kuy doomu réewum Senegaal te tollu ci 18 ba 35i at. Waaye, dinañu ko amal ci sàmmonteek yenn sàrt yi. Liñ ci gën a jublu nag mooy jël ay lawax yu noppi ngir jàngale. Maanaam, ay lawax yoy, jot nañoo tàggatu te mës a jàngale ba xam li ci nekk. Bu ko defee, dañuy jëkk a seppi ñi jot a am lijaasa ci njàngale mi.

« Danoo bëgg tànn ay jàngalekat yu noppi ngir jàngale ci saa si ñu leen jële. Seetunu ci lu njëkk ay jàngalekat yu ñu jël bees ngir tàggat leen walla ay ndongo yu nekk ba léegi ci daara yi di jàng. » (Sëriñ Suhaybu Bajaan, njiit liy saytu mbiri liggéeykat yi fa jëwriñal njàng mi).

Bu ko defee, bu ñu amul lim bi ñu soxla nag, ci lañuy sog a yaatal jël bi ci ñi am i lijaasa ci ekool yi digg-dóomu yi. Lawax yi ñuy jël itam, war nañoo noppee dem fépp fees leen yóbbu ci diiwaani Senegaal yi, ba ci béréb yi gën a ruqe. Nde, ñàkkug jàngalekat yi jafe-jafe bu law la ci réew mi, waaye dafa gënee tar ci diiwaani Maatam, Kéedugu ak Tàmbaakundaa.

Ginnaaw leeral yi ci wàllum jël bii, Sëñ Bajaan xamle naat ni jël ay jàngalekat ci tembare, ni ñu ko nar a defe nii, nekkul luy wéy di indi saafara. Ba tax muy nisar ab naalu juróomi at ngir tàggalikook ñàkkug jàngalekat ci ekool yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj