Jëwiriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu beek Coste gi, dina jël 1 500i jàngalekat ak i gëstukat ci daara yu kawe yi. Xibaar la bu mu fésal, fekk mu doon teewe 15eelu ndaje mu mag mu kurélu jàngalekat yi ci jàngune yi.
Démb ci àjjuma ji, 8 ut 2025, kurélug jàngalekat yi ci jàngune yi SAES (Syndicat Autonome des Enseignants du Supérieur) doon na amal seen Ndajee mu mag. Ñu ko doon amal ci njiiteefu jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu beek Coste gi, Dr Abdurahmaan Juuf.
Seen ndajem ren ji di 15eel wi yoon. Waxtaan yees fa doon amal a ngi aju woon ci wëppa wii di « Wér-gi-yaramu jàngalekat yeek gëstukat yi ak anam yi ñuy liggéeyee ci jàngune yi ». Dawid Selestin Fay miy fara-caytu bi dellusi na ci njariñu wëppa wi ak li waral ñu tànn ko. Naka noonu, muy xamle ni wér-gi-yaramu jàngalekat yeek gëstukat yi doon na lu metti ci ñoom. Te dara waralu ko lu dul anam yi ñuy liggéeyee ak di ko dundee ci jànguney bokkeef gi. Bokk na ci jafe-jafe yi mu tudd, limub jàngalekat yi matul, tabaxte yi ñuy jooytu ak jànguwaay yi sooxe.
Ginnaaw loolu itam, Sëñ bi Fay amal nay pàttali yu am solo ci jaar-jaaru kurél gi. Mu cay xamle ni seen kurél gii di SAES moo ngi ci 40i at bi ñu ko sosee ak tey. Naka noonoot, kurél gi yamul rekk ci sulli ay rëq-rëq. Nde dañuy andi itam ay saafara. Ba tax na, lenn rekk lañuy sàkku ci kilifa yi, te mooy ñu wéyal diisoo bi ngir ñu mën a fagaru ci yenn jafe-jafe yi. Noppi nañu itam, nees ko mësee def, fileek diisoo bee ngi ñuy jiital ak di ko suuxat.
Ginnaaw bi mu fa teewe nag, jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu beek Coste gi, Abdurahmaan Juuf yékkati na fay kàddu. Andi nay leeral itam ci yenn ponk yi SAES doon jooytu, rawatina dekkare paasiyoŋu porofesëer yi alaatereete bi ñu torlu woon. Mu cay xamle ni Njiitu réew mi joxe na ndogal ngir ñu doxal ko. Te sax tàmbali nañu leen a fay.
Wàllu jàngalekat yeet, jëwriñ ji xamle na ndogal yi ñu ci jël. Mu biral ni dinañu jël 1 500i jàngalekat ak ay gëstukat yu bees. Jël boobu sax dañu koy tàllal ci 3i at, 2025, 2026 ak 2027. Bu ko defee at mu jot ñu jël 500.
Ci noonu, jëwriñ ji di xamle ni ak jël yu bees yii, jàngalekat yi dinañu gën a am jot ngir def seen i gëstu ak aar seen wér-gi-yaram. Muy xamleet ni lépp yembul, waaye bu ñu saxalee diisoo bi rekk, nees nekk koy defee, gëm na ni dinañu am ay saafara.