Nguurug Senegaal dina ubbi juróom-ñetti jàngu yu kowe ñeel njàngalem liggéey (mécce), muy ISEP (Instituts Supérieurs d’enseignement professionnel), ci atum 2024-2025 mii di ñëw. Aamadu Abdul Sow, di njiitul njàngale mu kowe mi, moo ko xamle ci bi ñuy door lëlub ATUPA (Association des universités techniques et polytechniques d’Afrique), maanaam mbootaayu jànguney manoore yu afrig ci Afrig sow-jànt.
Keroog, ci Talaata ji, la ATUPA doon ubbi seenub lël ci atum 2023 mi. Ñu doon ko amalee fii ci Senegaal, ca Sali, li ko dale 25 ba 27i fan ci weeru awril wi. ATUPA doon kurél gu juddu ci weeru ut 2019 ci diggante réewi Afrig yiy wax àngale (Commonwealth), laata Mbootaayu Réewi Afrig yi di ko nangu ci biiram ci weeru desàmbar 2019 ca Addis-Abebaa, Ecopi.
Yitteem mooy di amal i ndaje, di weccontey xalaat ak i jaar-jaar ngir mën a suqali réewi Afrig yi, jaare ko ci suqaleeku xeeti xam-xam ak manoore yi méngook jamono. Ci seen njàngat, réewi Afrig yi dañ yittewoo lool ay liggéeykat yu seen xel màcc ci wàlluw mbey jamono yii ñuy nekk di xeeñtu moom seen bopp ci lépp, rawatina ci wàlluw dund gi. Looloo waral ba ci lëlub rén ji, ñu doon ci waxtaane lépp luy gëstu ak tàggatu ci liggéey yeek manoore yuy suqali mbey meek soppalib ngóob mi (contribution de la recherche et de la formation professionnelle technique au développement de l’agro-indistrie).
Ci ubbite gi, Sëñ Aamadu Abdul Sow mi jiite njàngale mu kowe mi fii ci Senegaal yékkati na fay kàddu. Wax na ci solos ponk bi ak ci jëmu yi mu fekk réewum Senegaal mi dalal lël bi. Nde, dafa fekk Senegaal am beneen taxawaay ci fànn wile. Te mi ngi ko dooroon ci atum 2013, bi muy jël ndogalu soppali njàng meek njàngale mi, gën cee dëgëral yii di xam-xam, xarala, xareñteef ak xayma, STEM (Science, technologie, ingénierie et mathématiques). Ci yoon woowu, muy xamle ni :
« Juróomi ISEP a ngi nekk di doxal, te di na am bu leen juróom-benneel buy tàmbali ci weeru oktoobar wii di ñëw. Dinanu tijji yeneen juróom-ñetti ISEP yees leen di mottalee ci atum 2024-2025 ».
Bu dee li jëm ci xareñteef yeet, Sëñ Sow fàttali naat ni Senegaal jot na cee am juróom-ñetti daara ak fukk ak ñeenti jàngu yuy tàggat ciy liggéey.