Guddig dibéeru démb ji moo nekkoon àpp gu mujj ñeel njébbalug wayndare yi. Mu mel ni, ñi ñu gën a xaar ci wote yii, jox nañu gëdd àpp gi, daldi koy defe ni ko Yoon diglee. Ay xew-xew yu bari am na ci donte ne sax, am na ñoo xam ne sóoroon nañu leen. Dafa di, am na ñoo xam ne, démb lañu fésal kiy jiite seen toftal. Am na ñoo xam ne sax jotuñoo àgg foofu. Ku nekk ci ñoom ak la ko gàllankoor. Ñenn ñi, li tax jébbaluñu seen i wayndare mooy ne dañoo amul koppar yu ñu mën a deme ci wote yi. Walla fekk sax, ki waroon a jébbal seen ug wayndare moo daw ak moom.
Wotey palug dépite yi jur na coow lu bari ci réew mi. Bi ñu leen jàppee ba tey, coow li daf ne kurr ci géewu pólitig bi. Ku nekk ci ñoom di ràcc, di jëmale kanamam. Te, li ñu ci jublu du lenn lu moy askan wi jox leen bopp ngir ñu mën koo teewal fa Ngomblaan ga. Démb, nekkoon bés bu am solo ngir jëmmal seen yéene jooju. Moo taxoon lëkkatoo yi doon def lu ñu mën ak lu ñu mënul ngir jébbal seen i wayndare. Donte ne sax, am na ñoo xam ne jotuñoo jébbal seen i wayndare. Waaye, amoon nañu yéeney def ko. Muy ku ci mel ni Abdu Kariim Géy ak Paap Abdulaay Ture nga xam ne seen loxo moo jotul seen ginnaaw. Looloo tax, mënuñoo bokk ci wote yii.
Mu am keneen koo xam ne loolu terewu koo jébbal wayndareem. Moom, Meetar Musaa Jóob, li ko teree jébbal wayndareem mooy ndaw la mu ko joxoon, di Buubakar Kamara, moo daw ak këyit ya. Kenn déggu ko, kenn gisu ko. Ndeke, ma nga Cees, toog. Kii di Meetar Musaa Jóob xamle na ne dina ko jure (pelent) fa toppekatu bokkeef gi. Li ci gën a doy-waar mooy ne, moom Buubakar Kamara, dafa génn di xamle ne li mu def réccuwu ko. Maanaam, moom moo ko tey. Li mu ko layalee mooy ne ñoom dañoo tànn wayndarew Pastef. Te, bëgguñu woon Meetar Musaa Jóob yëg ko, di leen kar.
Mu mel ni kon, kàrt gi jaxasoo na lool. Dafa di, kii di Abdul Mbay nga xam ne bokkoon na ci ndoorteel gi, raxasu na ba set ci wote yi. Maanaam, moom bokkatul donte ne sax, mook Ceerno Alasaan Sàll ñoo sosoon seen ug lëkkatoo dippee ko “Senegaal Kese”. Moom, bàyyi na. Waaye, loolu du tere, Ceerno Alasaan Sàll mooy wéy di jiite seen toftaleg lëkkatoo gi.
Naka noonu, mu amaat meneen mbir mu gën a xumbal wote yooyu, muy jàkkaarloo Usmaan Sonko ak Bàrtelemi Jaas. Ndax, kii di Usmaan Sonko moo jiite toftaleg Pastef. Bàrtelemi Jaas moo jiite wayndare lëkkatoo gii di Sàmm sa kàddu. Muy lëkkatoo goo xam ne làng yu bari la boole. Muy PUR (Sëriñ Mustafaa Si), PRP (Décce Faal), ARC (Anta Baabakar Ngom), AGIR (Ceerno Bóokum), Taxawu Sénégal (Xalifa Sàll), Les Serviteurs (Paap Jibriil Faal) ak Gueum Sa Bopp (Bugaan Géy Dani). Waaye, mu am luy ñuul ci soow mi. Ndax, kii di Bàrtelemi Jaas dañu koo daanoon ci mbirum bóomug Njaga Juuf. Kon, loolu mën na tax du mën a bokk bu fekkee dañu koo génnee woon ci toftaley wote yi (listes électorales). Dafa di, mbir moomu moom, waa ndajem ndeyu àtte mi ñoo ciy indi ay leeral.
Fi mu tollu nii, wure wa dem na këŋ. Lu waay doon jaay, léegi mu lamb. Ndax, fii ak diir bu gàtt dees na xam gan lëkkatoo la Saa-Senegaal yi gën a jox bopp. Te, loolu moom, mbañ-gàcce yi kese ñoo ko mën a leeral. Kon, saaga moom, yàkkamtee xeex la.