Démb ci àjjuma ji, 17 sãwiyee 2025, El Haaji Àlliyun Abdulaay Silla, Toppekatu PJF (Pool Judiciaire Financier) bi, biral na njëlbeenu bilaŋu ëttu àttekaay boobii saytu mbirum koppar yi. Ñeenti weer ginnaaw bi ñu ko sampee, saytu na 91i wayndare, nangu lu tollagum ci 2i miliyaar ak xaaj ci sunuy koppar.
Cig pàttali, ca weeru ut (9i fani ut 2024) la CSM (Conseil Supérieur de la magistrature) tabboon, ci njiiteefu Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, way-bokk (membres) yi séq ëttu àttekaay bii di PJF (Pool Judiciaire Financier). Keroog bésub 17 ci weeru nowàmbar 2024, ñu daldi koy samp ngir mu wuutu ëtt bii di CREI (Cour de répression de l’enrichissement illicite) ginnaaw bi ñu jàppe ni dafa tële amal i àtte yu jaar yoon.
Boobook tay nag, mat na juróomi weer. Mu bari lool ay waxi tamñareet yu jib ci diggante bi ak ay boroomi tur yees ciy tudd. Bees sukkandikoo ci njureef yi toppekat bi El haaji Àlliyun Abdulaay Silla biral, ëtt bi jot naa saytu 91i wayndare. 87 ca wayndare yooyale, jàllale nañu leen ci àttekat yi leen war a saytu.
Naka noonu, Sëñ bi Silla leeral naat ni jàpp nañu 162i doom-aadama yoy, ëtt bi woolu woon na leen ba déglu leen. Bu dee alal jeet, teg nañu loxo lu ëpp 2 500 000 000 FCFA (ñaari tamñareet ak juróomi-téeméeri tamndaret).
Sëñ bi Faal wax na itam ci ni Pool Judiciaire bi di doxe ngir teggi tuuma ginnaaw coow yi ci juddu ak way-pólitig yi gis ni dañ leen a singali. Ba tax muy leeral ni li ñuy def jotewul dara ak pólitig. Du rekk itam ku ñu woolu taqal la. Bari na luy waral ñu mën a woolu nit ki. Seen liggéey dafa tënku ci leeralal askan wi. Lépp nag ñu koy amal ci kow sàmmonteek àq ak yelleefi ñees di topp. Rax-ci-dolli, am na ñees tegoon loxo ñoñ, bàyyi nañu leen bàyyig négandiku fekk dëggal nañu liñ leen di toppe.