Benn weer kepp a dese Njiitu réewum Senegaal li, Maki Sàll, ci boppu kilifteefu Mbootaayu Réewi Afrig yi. Ginnaaw biñ ko fa tabbee ci weeru féewirye 2022, weeru féewiriye 2023 wii di ñëw la war a joxe lenge yi. Jamono yii ñuy laam-laame ku ko war a wuutu, ay kuréli pólitig ak yu ndawi askani Afrig a ngay feeñal seen ub naqar ak di sàkku ci Kurélu Réewi Tugal yi mu bank i loxoom ci Mbootaayu Réewi Afrig yi.
Ci ndajeem Njiiti réewi Afrig mii di ñëw (féewiriye 2023) lañ war a tabb kiy wuutu Maki Sàll ci boppu Kilifteefu Mbootaayu Réewi Afrig yi. Jamono yii nag, dafa bare luñ ciy tudd Njiitu réewum duni Komoor yi, muy Asali Asumani.
Ragal mu jiiteji Mbootaayu Réewi Afrig yi nag moo tax ba lu tollu ci 32i kuréli pólitig ak yu ndawi réewi Afrig taxaw xaat ne duñ ko seetaan. Nde, moom Asali, jàpp nañ ni nekkam Njiitu réew dafa safaanoo ak ndeyu àtte réewum duni Komoor yi. Rax-ci-dolli, anam yi mu yoree réew ma dëppoowul wenn yoon ak ni réew mu am yoon di doxe. Ci seen yëgle bi, ña nga cay wax naan :
« Fal Asali Asumani ci boppu kilifteefu Mbootaayu Réewi Afrig yi mooy rekk nangu ak yoonal doxalin yu ñaaw yi njiiti pólitig yi nekke, dooleel def lu la neex te dara du la ci fekk, ak jëf yu ñaaw yu bon yiy gàllankoor suqaleeku koomu kembarug Afrig ak a gën a ndóol-loo askan wi. »
32i kuréli pólitig yi bokk xaatim yëgle bi yamuñu ci ñaawlu tabb giñ namm a tabb Asali Asumani. Ndaxte, ña ngay sàkku ci Mbootaayu Réewi Tugal yi mu bank i loxoom te dakkal lépp i ndimbal lu jëmm ci gafakag Mbootaayu Réewi Afrig yi.
« Sunu kurél yee ngi sàkku doxalinu buntu 7 bi ci déggoo Mbootaayu Réewi Tugal yi tey amal i daan saa bu jalgati amee ñeel mbaaxi tugal ak sàrt yi Réewum Yoon di doxe. »
Ndax Mbootaayu Réewi Tugal yi dina fullaal càkkuteef gii ? Ak lu ci mën a topp, taxawaay bi 32i kurél yi am dafay firndeel coppite gi Saa-Afrig yi bëgg ci melokaani ñi leen di jiite ngir réewum yoon sax ci kembarug Afrig ba àq ak yelleefi askan yi mën fee sàmmu.