Tey, ci alxames ji, la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon dalal Njiitu Nguurug Espaañ, Pedro Sanchez. Pedro Sanchez nag, jamono jii, dafa nekk di wër réewi Afrig sowu-jant yi. Dafa di, kenn umpalewul li mbir mi boole Senegaal ak Espaañ jamono jii. Nde, ndawam yu baree ngi dee ci ndox mi ngir dem Espaañ.
Kon, mbëkk mi nekkoon na poñ bu am solo ci seen uw waxtaan donte ne sax, am na yeneen i wëppa, muy lu mel ni mbey mi, tàggat ci xarala ak xareñte ak tabaxte yi (infrastructures). Waaye, mbëkk mi moom, bokk na ci li ëpp solo. Nde, doomi Senegaal yi ciy faatu dafa bari lool. Moo tax, seen mébét mooy ñu xool nu ñuy def ba tukki bi gën a jaar yoon. Su ko defee, ñoom ñépp ñu mën cee jariñu. Te, pas googu dina doon lu am solo ci wàllu koom ak kaaraange gi. Ndax, mënees na wax ne, kenn réerewul tolof-tolof yi doomi Senegaal yi di jànkonteel ci yoon wi. Ci gàttal, ñoom xaatim nañu ñaari pas. Muy lëkkaloo ci wàllu tukki gi ak xeex li ñuy dippe “crime transnational”.