NJIITU RÉEW MI DALAL NA PÓOL KAGAME, NJIITU RÉEWUM RUWÀNDAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu Réewum Ruwàndaa, Póol Kagame, teersi na Ndakaaru, tey ci gaawu gi, fa naawub Lewópóol Sedaar Seŋoor. Tànki  nemmeeku ak liggéey la doxsi.

Bi Póol Kagame wàccee ci roppalaan bi, moom Njiitu réewum Ruwàndaa li, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ànd ak lenn ciy sóobare, moo ko teertu, tatagal ko ni mu waree. 

Moom, Póol Kagame, ñaari fan la fiy def. Ci biir ñaari fan yooyu, dina ci waxtaan ak Njiitu réew mi. Li ñu ko duggee mooy gën a dëgëral jëflantey xaritoo ak mbokkoo gi dox diggante Senegaal ak Ruwàndaa, rawatina lëngoo gi yàgg a dox diggante ñaari réew yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj