Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dàq na Ablaay Daawda Jàllo ak Aminata Mbeng Njaay. Ñoom ñaar ñoo nekkoon njiiti campeef yii di CESE ak HCCT. Njiiteefu réew mee ko xamle cib yégle bu mu siiwal, tay ci ngoonug àllarba ji. Dafa di, tay ci suba rekk, Usmaan Sonko yégle woon na ndàqug ñaari way-bokki lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar yi.
Cig pàttali, Njiitu réew mi dafa bëggoon a tas campeef yii di CESE ak HCCT. Waaye, bi mu jébbalee sémb wi waa Ngomblaan gi, dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yi dañ ko gàntal. Ak ndogal lii mu jël nag, Njiitu réew mi tontu na leen ci wàllu pólitig, xamal leen ni moo yor lenge yi.