Tay ci àllarba ji, 10i fan ci weeru awril lees doon amal jullig kori daanaka fépp ci àddina si. Njiitu réew mi, sëñ Basiiru Jomaay Fay daldi doxale ni ko Njiiti réew yi mu wuutu (Abdu Juuf, Abdulaay Wàdd ak Maki Sàll) daan defe. Ca jumaay Ndakaaru ju mag ja la jullee.
Bi mu dundalee aada jooju ba noppi, ilimaan bi def na xutbaam. Ndax, korite, dañuy julli ñaari rakka ba noppi daldi xutba. Ci xutbaam bi nag, ilimaan bi fàttali na jikko yi jullit bi war a làmboo tey dëgëral ngëm. Ginnaaw loolu, mu yëkkatiy ñaan jagleel ko kii di Njiitu réew mi, ngir Boroom Bii woyofal ko yan wi ba mu matal lépp ca nim gënee.
Loolu doon lu Basiiru Jomaay Fay rafetlu. Ndax, ba ñu noppee, jël na fa kàddu gi, àndadoo ak lenn ci waa nguur gi ak ci kilifa diine yi fekkee woon julli ga foofu.
Ciy kàddoom, sant na Yàlla mi ko may mu wéyal loolu ay aji-jiitoom daan amal. Fàttali na itam mbaaxi Senegaal yi nga am ni yii ñooy dëggaral jàmm ak àndandoo bu dëgër bi ci réew mi. Teg ci di fàttali ba tay ngir ñu gën a fonk yooyu nga xam ni ñooy keno yi tee mbaaru jàmm ji fii, te ñépp di ñu ci ñee.
Mu tëjee, moom Njiitu réew mi, ci sant ak gërëm niti daara yi ak gépp kilifag diine, ak fum mën a bokk.