Wotey 2024 yi duñ am ci bésub 25 féewiryee bees leen àppaloon. Ndogal lu Njiitu réew mi Maki Sàll jël la tey, gaawu 3 féewiryee 2023. Dafa doon janook askan wi ñeel coow li lëmbe dëkk bi ci diggante lawax yi, Ngombalaan geek ndajem ndeyu àtte réew mi.
Ndàqum wote yi ñu doon laam-laame am na léegi. Njiitu réew mi, Maki Sàll jël na ndogal li tey ci gaawu gi. Démb ci àjjuma ji la yëgle woon ni dina wax ak askan wi niki tey bu 12i waxtu jotee. Bi ñu demee ba waxtu wi teru, ñu randal ko ba 14i waxtu. Waaye, li ëpp solo ciy kàddoom yooyu nag mooy fomm gi mu fomm wote yi waroon a am ci 25 féewiryee bii nu dëgmal te ñu waroon cee fal ki koy uutu ci boppu réew mi.
Keroog, bi ndajem ndeyu àtte réew mi génnee limkag 20i lawax yi war a joŋante Njiitu réewum Senegal, génne ci Karim Maysa Wàdd, la coowal ndàq gi juddu. Nde, lawaxu PDS (Parti Démocratique Sénégalais) bi dafa génne ab yégle di ca tuumal nger ñaari àttekat yu bokk ci Ndajem Ndeyu àtte réew mi. Coowal nger looloo waral ba ñu taxawal ag ndiisoog luññutu fa Ngombalaan ga ngir déglu way-bokki ndajem àtte mi.
Ginnaaw gi, ñu gisaat ni kenn ci 20i lawax yi jàll, muy Roos Wardini, doomu réewum Farãs la. Te, lu ni mel tax ba Ndajem Ndeyu àtte réew mi neenal nekkug lawaxu Karim Wàdd. Moom Roos Wardini sax ma nga ca loxoy yoon ñu téyee.
Bi ñu xéyee tey ci gaawu gi la pekkug Ngombalaan gi jàllale càkkuteefu àtte bi ñeel ndàqum wote yi, muy lu Njiitu réew mi sukkandiku ngir dàqandi wote yi. Nde, bees ko déggee, ginnaaw bi ko Ngombalaan gi jébbalee àtte bi, diisoo na ceek njiiti campeef yii di Càmm gi, Ngombalaan gi, HCCT ak Ndajem Ndeyu àtte réew mi. Naka noonu, la daldi tontu Ngombalaan gi, xamal leen ni mën nañ wéyal seen liggéey.
Ab dekkare nag la Njiitu réew mi mujje xaatim, jaare ci neenal dekkare bi mu génne woon ci weeru nowàmbar, doon ci woo saa-senegaal yi ci ñu ñëw fal Njuutu réew lu bees. Waaye, bu dee lu jëm ci moom, li mu waxoon la waxaat : du bokk ci wote yi. Jamono bi muy jël boobu dekkare nag, ay waxtu kesee desoon ngir lawax yi sóobu ci ndagaanu baati askan wi. Ña nga doon sax wuutuwante ca RTS ngir jébbal leen seen ngénn yu njëkk.
Bu Njiitu réew mi ajee wote yeet, waxul kañ lañ leen di àjji. Nde coowal Ngombalaan geek Ndajem Ndeyu àtte réew mi lay topp fi mu nekk. Nee naat dina wooteeti péncoo ngir ñu waxtaane nees di amalee wote yi ci lu leer. Ñu xaar ba xam fan la ko kujje gi di xaar. Donte ne am na ñenn ñu jotoon a fésal ni duñ nangu ku fi fomm wote yi.