Bi ñuy waaj a amal wotey palug Njiitu réew mi, as diir kepp desoon ca, ca la Maki Sàll mi jiite woon réew mi jamono ja jaayoon kasob Rëbës. Njëgu juróom-ñetti miliyaar la ko jaaye woon. Njiitu réew mi nag, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, neenal njaay mi. Moom, Njiitu réew mi, dafa nanguwaat béréb booba, dugalaat ko ci moomeeli askan wi. Waaye, Njiitu réew mi yemul foofu.
Ndax, am na yeneen ñaari dekkere yu Maki Sàll xaatimoon laata muy dem. Ñaar yooyu yépp, mi ngi leen xaatim ñaari fan ginnaaw bi Basiiru Jomaay Fay faloo. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, Njiitu réew mi neenal na dekkere yooyeet. Benn bi mi ngi ko xaatimaloon këru liggéey gii di Société Ciments du Sahel. Bi ci des, mu xaatimaloon ko waa Kiren. Te, diirub ñaar-fukki at juróom la leen ko defaloon, muy lol, dafa safaanoo ak yoon.