Bees sukkandikoo ci Majambal Jaañ, Njiitu réew, Maki Sàll, tas na Càmm gi. Bi Ndajem jëwriñ yi jeexee ci 18i waxtu la ko tas. Bu dee xibaar bi wér na, dees na laaj, laaj yii toftalu :
– Lu tax Maki Sàll tas Càmm gi ci jamono jii tembe ?
– Lu mu narati ?
Tontu yaa ngi sunu kanam. Te nag, li ci kanam rawul i bët.