Xare baa ngay wéy diggante Irã ak Israayel. Ci guddig démb gi, gaawu jàpp dibéeru tay jii, ñaari réew yi weccante nañuy bomb. Ñoom ñaar ñépp, deele nañu ci, mu am ñu ci ame ay gaañu-gaañu ci ñaati wet yépp, waayeet, barile nañuy yàqu-yàqu ak loraange. Irã dafa sàndi ay misil ca Ayfaa (Haïfa), Israayel tamit dóor ay misilam ca Teyerã (Teheran).
Ci guddig gaawu bi jàpp dibéer, ñetti yoon la Irã dóor ay misil ak i dóron ca réewum Israayel. Béréb yii toftalu la sóobarey Irã yi diir : Seggukaayu soroj bu Ayfaa (Haïfa), Waaxu Elat (Eilat), Tel-Afiif (Tel-Aviv), Asdot (Ashdod) ak Bat Yam (Bat Yam).
Ci lees rotal ciy dég-dég, as-tuut, ñetti nit faatu nañu ci, te ñetti taaxi kaw màbb nañu. Tele bii di Al Arabiya moo siiwal xibaar bi. Bees sukkandikoo ci yéenekaayu Le Times of Israel nag, ginnaaw congum Irã moomee, 8i nit ñoo ci dee, 200i jële ci ay gaañu-gaañu ak 35i nit yu réer.
Washington Post xamle na ne, réew yii di Siri, Sordani ak Iraag, ñoom, tëj nañu seen i jaww ginnaaw bi Irã songee Ayfaa. Libã moom dafa fomm ay tukkiy roppalaan ginnaaw bi ñu séenee ay misili Irã ci seen jaww ji, fa Beyrut (Beyrouth).
Bees sukkandikoo ci Kërug saabaal gii di Mehr, ay misil xef-xippi (missile hypersonique) la Irã dóor ca Ayfaa. Bu dee waa Nour News, li ñu saabal mooy ne , misil balistig yi Irã jëfandikoo, yii la : Emad, Ghadr ak Kheibar Shekan.
Israayel tamit song na ay béréb ca Irã. Dafa dóor ay misil ca seggukaayu soroj bu Sahran (Shahran) ba nekke ca bëj-gànnaaru Irã. Song na yit geneen ndefaru soroj ca bëj-saalumu réew Teyerã, di gëblag Irã. Moo tax, ñaari béréb yépp dañoo boy, daldi tàkk.
Israayel dóor na yit ay misil fa Yemen. Ci li saabalukaay yii di Ynet ak Times of Isael njort, njiitu Huti yi la doon diir. Bees sukkandikoo ci ñaari saabalukaay yooyii ba tay, Israayel ray na ki jiite sóobarey Huti yi, Muhammet Al-Amri.
Cig pàttali, Israayel moo jëkk song Irã, dóor ko ay misil, daldi ray ñu bari ci ay kilifa yu ràññeeku ca réew ma. Li ko Nguurug Netanyawu (Netanyahu) gi dugge, ci seen i wax, mooy dakkal naaluw nikeleyeer wow Irã.
Irã tamit daldi fayu ci anam bu tar. Te, boobaak léegi, xeex baa ngi wéy. Fan lay mujj ? Yàlla rekk a xam.